Njàngat

(Yoonalaat gu jóge Ladab)

Baatu Njàngat day tekki mbooleem ay mbind yuy wax ci ay koj. Ni ko Ñenn ñi di gisee du yem rek ci mbind yu ñu taaral waaye am na it njàngatu kàddu, maanaam yu yemm ci ay kàddu. Sunu xoolee mboolaay yu mel ne yu waa Afrik yi xamul woon bind, seenum njàngat ci kàddu la yemoon.

Tekki

Soppi

Njàngat day di ab fànn gu am genn melokaan gi ci jokkoo, muy ci mbind walla ci kàddu, di tax ñuy man a jëfandikoo làkk bi bu baax te di am njeexit ci baatukaay bi. Njàngat da fa yaa te bariy fànn, li leen di wuutale mooy mbindin walla ndefu téere yi. Taaral gi am na ci lu am solo.

Ci lu ëpp dañ koy jàppee ni ag fànn. Waaye itam doon na lu jafe rëdd ay peggam rawatina su nuy bind ci xeltu, ci xarala walla yeneen.

Ladab

Soppi

Njàngat day di ab fànn gu am genn melokaan gi ci jokkoo, muy ci mbind walla ci kàddu, di tax ñuy man a jëfandikoo làkk bi bu baax te di am njeexit ci baatukaay bi. Njàngat da fa yaa te bariy fànn, li leen di wuutale mooy mbindin walla ndefu téere yi. Taaral gi am na ci lu am solo.

Ci lu ëpp dañ koy jàppee ni ag fànn. Waaye itam doon na lu jafe rëdd ay peggam rawatina su nuy bind ci xeltu, ci xarala walla yeneen.

Ladab

Soppi

Ladab baat la bu bawoo ci araab, di ci araab adab. Adab nag ci araab am na ñaar ba lu ko ëpp ciy tekki, waaye ñaar yi ci gën a siiw, bi ci njëkk mooy Adab: di baat bu Sëriñ Tuubaa (y.y.g) bari lu mu jëfandikoo ci téereem bii di Nëhju, di téere bu tëriit li (sujet bi) jëm ci yar ak dugal ci nit ñi ay teggiin (aadaab) di mbooloo(pluriel) ci adab. Bi ci des di bi ñu tax a jug, moom nag adab la nu laaf ci ag L muy leegi ladab, lu tax nu laaf ci L gi, loolu ñi ngi ci roye Lislaam te bu njëkk Islaam la woon, waaye ginnaaw ak L gi la ko wolof yi di gën a man di wax ak a tudd, moo waral - ci li nu wax - nu koy boole ci baatu araab bi, lii nag làkk woo gis ci àdduna bi am na ko, boo demee ci araab da cee fees dell, ay baay yu nu lem ba manees koo wax ci làkku araab, te doonuñu woon ay baati araab ñu mujj bokk ci làmmiñu araab te bu njëkk bokkuñu ci woon. Lu ni mel fees na dell ci Alquraan, am it ci làmmiñu araab wu jamonoo wii, sundus, istabraq ak yu ni deme duñu ay baati araab te ñi ngi ci Alquraan, lu mel ni qubtaan, di capitain dees koo jengal ba araab yi man koo wax waaye juddoowu ci añs. Waaye nag Ladab ca daaray majaalis ya, maanaam fa mag ña daan jànge, nga xam ne seenuw jàngiin da daan tegu ci firi baat topp baat, maanaam pirim baat-baat, nga `xam ne lees la wax tekkil la ko ci wolof bu ñu nee bismil-laa ne la : maa ngi tàmbalee ci turu Yalla, ar-rahmaani: kay aji yërame ci àddina añs. Bu dee ci tekkiin wii, Adab di baat bi nuy wax Ladab: njàngat lees ko daa firee, walla xam-xamu mbind.

Kon manees na ne: Ladab,

Buñu bëggee muy wolofi kese ñu ne: Njàngat, walla xam-xamu mbind

Ci: Farãse:

  • CORRECTION
  • BELLES-LETTRES
  • COURRIER
  • LITTÉRATURE

Ci làkkuw Angalteer:LITERATURE

Xeeti njàngat

Soppi

Ci mbindin mi walla waxin wi la ñuy sukkandiku ngir man a xammee xeeti njàngat yi:

Su nu jàppee ne njàngat ab mbooloom ay baat yu am bopp di wax ci lenn li la. Kon man nanoo wax Njàngatu xam-xam, Njàngatu koom-koom, Njàngatu diine, Njàngatu woy, añs.

Tekkiinu njàggat

Soppi

Njàggat benn la ci anam yi nit di génnee ak a feeñale li nekk ci moom ciy yëgg-yëgg aki xalaat aki ñeewant aki gis-gis, jaare ko ci ay mbind walla bindiin yu rafet te wuute, moo xam woy la ( maanaam poesie) walla wesar (bind ci lu dul di ko nos, maanaam safaanub woy) walla wesar wu ñu nos. Loolu nqg di ubbil nit ay bunt ngir mu am man-man ci feeñal ak génne li ñu manul a génne walla ñu koy man a feeñale ci geneen anam walla melo. Njàggat nag day takku takku gu dëgër ci làkk. Dëgg-dëggi njuréef walla ngérte li juddoo ci làkk ñu bind ko, walla caada ja ca juddoo, day nekk di lu dencu walla lu wattuwu ci biir melokaani njàggat yi aki peeñ-peeñam, te ñoom danuy wuute kem ni gox yi di wuutee jamono yi di ko wuutee. Jamono ju nekk tam ay soppiku da ciy sosu akug jëm kanam akug wuute ak xeetu ànd ak jamono yi

Man ngéen a xool foofu ci suuf,cuq ci lëkkalekaay yooyu, ngir déglu as lëf ci wolofali Sëñ Mbay JAXATE ak Sëñ Muusaa KA:


Waxi Seex Anta Joob ju aju làkk

Soppi

Làmmiñ ak jamono

  • Làmmiñ wi ngànnaay la, paaka la, balay ñaw nga daas ko;làmmiñ wu ñu jariñoowul, mi ngi mel ne paaka bu xumaag. Tubaab yi bi ñu fi ñëwee, réew mépp dañu koo yore ci seen làmmiñu bopp.Moo taxoon ba sunu làmmiñ yi des ginnaaw.Li la daan tax a jëm kanam, li la daan tax a am loo dundale sag anjaboot ci weneen làmmiñ nga daan jaar am ko...Loolu moo taxoon ñu sàggane sunu làmmiñ yii.Waaye du caagéenu dañu cee manul woon a waxe li ñu bëgg a wax...

Dangeen di xam ne aw làmmiñ, jëfandikukaay la boo xam ne lu am xel dem ci àdduna aw làmmiñ man na koo tudd, am xel ay gàtt, aw làmmiñ gàtt!Waaye lu am xel man a jëm ci àdduna rekk, aw làmmiñ man na koo tudd;aw làmmiñ gàttul.

Nit kiy wax nag fi xelam yam, fi jàngam yam, fi gis-gisu àddunaam yam, foofu rekk la ay waxam man a yam...

Waaye boo demee ba sam xel gis leneen rekk, làmmiñ dina ko tudd. Lu ko waral? Amul benn baat boo xam ne bii yenu nga sa maanaa ci cosaan, amul!Mooy li nga xam ne - waxoon naa ne...dinaa cuq tuuti xel yi...ndax defe naa ne, yéen jàng ngeen xam-xamub làmmiñal...xam ngeen ne De Saussure (boroom xam-xam bu mag la woon ci wàllu làmmiñal) wone na loolu.Làmmiñ du loo xam ne tay baat yi dañoo juddu rekk daal di yanu seeni maanaa. Baat bi coow luy génn ci gémmiñ kepp la! Kepp! Amul sax menn maanaa. Ndax bu ko amoon wenn làmmiñ ay am, kon lu jug rekk xel yépp nenn lañu koy tudde.Wenn tur wi di moom te loolu amul.


Jukki bii tibbees na ko ci waxtaanu Seex Anta Jóob, mu amoon ci awril 1984 ca Cees


wikbaatukaay am na xët wu tudd: Njàngat