Sëriñ Muusaa KA

ab bindkat bu Senegaal
(Yoonalaat gu jóge Seriñ Muusaa KA)

Sëriñ Muusa KA (Sëriñ Muusa KA werekaanu Bàmba) woykatu wolof ak araab la woon bu mag te xarañ ci, ab jullit la woon bu dëggu te di ab sufiyànke di taalubeb Sëriñ Tuubaa bokk it ci Seexi Sëriñ Tuubaa yi, taalif na lu sakkan ci ay téere ci wolof ak araab rawatina wolof ndax ki mu daa tagg wolof mooy làkku cosaanam muy Sëriñ Tuubaa Sëriñam te sëriñam boobii it Yonnent bi moo doon sëriñam bu ko daa tagg ci araab lakoy tagg, ndax nit koo di tagg di ko tagge weneen làkk wu dul làkku juddoom tagg ga du mat ndax yaangi koy tuutalal cosaanam, ay woyam nag li ci ëpp Sëriñam la ciy tagg ak di soññ bokki taalubeem ngir ñu gën a fonk Sëriñam te nankoo jaamu Yàlla, ku xelu la woon te jàng ba ci woyam yooyii mu woy ci wolof ku jàng `Aruud (xam-xamu woyiin ci araab) ma nu koo jam, sàmmoonte naak sarti woy ak bahru yi (woyiin yi), ba sos na ay Bahru ajami; niki Téere bi tudd «Bu léen njuuj-njaaj» ak way wi mu jébbaloo ci Seex Mustafaa Mbàkke xalifab Seexul Xadiim bu jëkk.

Dencukaay:S Musaa Ka.jpg
S Musaa Ka Werekaanu Bàmba

ay woyam

Soppi
  • Ay-waay bu leen di fàtte yoonu yàlla () te xamni àdduna du kër ay tool la
  • wacci sa tool mu booy di bayali aw jàmbur () di dër-dëri di wut liggéeyi ba njàmbur
  • taxuta am dugub sakaane gerte () kerok bisub peret ba yaa cay perte
  • bàmba du waa muy gàntu waa muy gënale() loo ca amul ci yaw la yaw miy yellale
  • ñu jëkk ñaak ñu mujj ñii la yamale () loo ko jëfal mu fayla moom du tappale


  • Nawet Jolof noor fa te doo nooraani - ndaw lu ca sax boo màggatee yalwaani.

Bëyit yii ci jigéen la jëm, sabab yi tax ñu koy tànn niki soxna, mu jël araf ya araf wu ne mu def ciy bëyit

Soppi

Jiim gi

jigéen ju ndaw araf ya lan ko tënke - tënk ba bis pénc ba lan koy tinkee

jiimug jigéen mooy jekki bum jàllantu - ndaxte bu jàllantoo asal njaaloontu

cofeel gu mat sëkk a ko war cib sëriñam - ku bëgg dof te ku doful doo am ngërëm

jaamu boroomam jaamu it boroom këram - moo war jigéen su ko manee dàmmey ngëram

jam tuñ ma, jam siiñ ma'ak njamal-yàllaam la - jaalu-yàllaam wa ne Yaasin Salla'a

Jàmm ak juddook jikkoo waral ñuy tànn - ne xur wi wenn la te jiim yiy jenn



Kaaf gi

kaaf nga na baax gaaf, bari ngor, toog fa këram - na bari kersay kër-këriy sàkku ngërëm

nay gone bum def mag te bum gàtt kutuj - bum gudd lool fum toll ànd ak latkoloñ



Yaa gi

yaa ga na yaatu ŋàpp, yaatal dëkkandoom - yaatal boroom këram ci lépp lu mu moom

yaru te yomb te yéwén te yaatu - cib sëriñam te la mu yor bum laatu



Arafu nuun gi

arafu nuun gii ku ko boole xejj - ci sa boroom kër gaa ya duñ la xàjji

neex cere, neex dereet te neexu làmmiñ - neex lépp tey neexlaate gàttu gémmiñ

jigéen na maandu, man a muñ te mokk - di muñ di muuñ di mooñ cereem ne mekk.

Jikko yu aju ci arafu baa jëm ci jigéen

Soppi

arafu baa yile jigéen ju boole - seen jikko yii kenn du la ba ngay xoole

baax baay te booleek bari bayreek barile - ba su boroom këram amul muy defale

bëñam ya weex tàll ba mel ne perkaal - bët ba ne bàq bakkanam bay safu jaal

day neexu làmmiñ, neexu ñam te mokk lool - lewet te nooy ku mu dajeel sukkal la teel

bokk nq ci li mu wax di ci tagg sëriñam ba Sëriñ Tuuba

Soppi

adunyaa ngi tol new fel fi moom mbaate dëññu teeñ () woroomiy tëndëŋ xammeewu leen ak woroomi téeñ

lilee tax mu daa tuubloo dameel ak maxa'aki teeñ () ku mel nii ku amleek moom na leen wóor ne yaa ko tooñ

du tooñ nit te soo tooñee mu jéggal la tin la ko () xamul jaamur ak mbokkam, mag ak ndaw ci aw meloom

wurus mbaate ab xaalis bëy ak nag xar ak gëléem () la daa buub di jox ñiy laaj du kuy néegaleek a léem

añs

Ngir déglu te yér as lëf ci woyi Sëriñ Musaa Ka xoolal foofu:


Karmat ak delluwaay

Soppi

Xool it

Soppi

Jukki yi ci lonku

Soppi

Lëkkalekaay yu biti

Soppi