Sëriñ Mbay Jaxate

(Yoonalaat gu jóge Sëriñ Mbay JAXATE)

Sëriñ Mbay JAXATE nekkoon na di kenn ci woykati wolof yu mag yi (taalifkati woy yi) di woon it benn taalibeb Sëriñ Tuubaa, li mu taalif ci woyi wolof maneesu koo misaal mbaa deesi ko lim, nekkoon na di ab soofiyu bu mag, lu ëppoon it ciy woyam ci googule wàll la jëm, ku lislaame la woon te di woon ku jéggi dayo ba cig taral ci ñu sammoonteek daytali Yàlla yi aki ndigalam, bokk na ci ay woyam yii:

  • pexem Yàlla moo gën pexem nit ndaxam () fa Yàllay fexee yàqkat yeggu fa
  • Murit yaw de bul mer te bul jàpp mer () mer ak jàpp mer day alag ab murit

moo wax it:

  • Bul gaaw a ñam gaaw a ñam baaxul nigal ba mu ñor () meeneen akug neen a yam pal-pal matul ne pelam

moo wax it:

  • Am kilifaay li am solo () boo ko amee am nga solo () boo ko amul amoo solo () ku wéeruwul yomb a bëmëx

Yóbbal baax ciw yoon

Soppi

Yóbbal baax na ciw yoon :

Genn la ci xasiday Sëriñ Mbay Jaxate yi:

  • foo bëgg a dem nanga wut loo yóbbaloo soog a dem

kon boo demee doo fa lor yaw nit te doo fa loru

kuy dem te yóbbaalewul yóbbal bu doy fa mu jëm

kookee du bég du bégal ngir day loreek a loru

Yóbbal bi nag moo di fàggub yar te wol mburu yor

foo dem di may koo fa gis ab yar, di mos sa mburu

Ku nekk war na balaa dem fab yar ak mburu yor

ngir dégg fenn di wax talal du xeetu yaru

Yóbbul yar ak mburu boo dee tukki, kon dinga bég

bégal barab ba nga jëm ngir doo loreek a loru


Moo wax it :

Ne dell ak ñam ak ndox ñu naa sang bii () nga dof nag ba naa huu dangay alku kat


Moo ne it:


Bu cér yépp gàntoo def'as lëf jafe

Def'as lëf bu yombul am'as lëf jafe

Jugal farlu ngir yaa ngi cib lolli yaw

Te ab lolli buy wéy am'as lëf jafe

Ndegam reere nga'b lolli lollee ngi nii

Wér ak dund ak doole lollee jafe

Ku sab lolli ñëw nag ba say yëf ne xuss

La gën ngay ku yombul, ku maasam jafe

Jëfal guddi jëf bëccëg'ak sépp saa

Ba koo seeru naa kii jëfam yee jafe

Ku def nii ci sab lolli do jeele yëf

Bu nooree te doo xaare yewwoo jafe

Budul woon ngëméen ak nélaw koofu gis

Mi ngiy farlu ngir xam ne lee jëf jafe

Bu nit nee lasar, ñépp naa dóotu jug

Mu xemmeem a jog jëf té jog jëf jafe

Ku jëm cib ja té romb xaalis di wey

Bu yeggee di gis yëf ya teg njëg jafe

Xarit dëgg ŋooral ci xaalis bi yaw

Te kat leegi seerub dërëm sax jafe

Ngirug mag akug ràgg ak dee ngi ñëw

Bu ñuy yegsi dëf lëf lu bon bon jafe

Defal Yàlla as lëf bu mujjee jafe

Am as lëf ci Yàllaati gën koo jafe


Woy wu mu def ci wori àdduna

Soppi

Adduna bëgg na laa fab waaye yaw nanga bañ

Lu fab fab it nanga fab say tànk samp fi suuf


Jekkil te riigu fi suufus Yàlla sii bu fi jog

Loo jëm jëm it kaw dangay dellooti rekk fi suuf


Lalub gitax ak lalub weñ ak lalub tagar ak

Lalub selen boo ci tëdd it wàcci dellu fi suuf


Mbaam ak gëléem ak fafal-naaw ak wata'aku ngélaw

Loo ciy war it dula tee xëy bis ne céng fi suuf


Néegub ñax'ak mbaari seng ak taaxi suuf aki kaw

Loo yàgg yàgg ci ñoom it génn dugg fi suuf


Cerey lay ak wataboor ak ndàbb ndiir aku sëb

Ak mbuum akub cox a faf yam bis ba ngay gane suuf


Baadoola ak buur akub dag ñépp ñoo xala yam

Lu yàgg yàgg dañiy booloo ne meng ci suuf


Jëlub lingeer ak jëlub jaam ak jëlub xaj a yam

Loo jël jël it dee gi xëy bis jël la dénk la suuf


Adduna wor na mag ak ndaw wor ko leegi bu wér

Te ŋoy ci Yàlla ki yor suuf ak ñi nekk ci suuf


Lu yàgg yàgg nangay def Yàlla wettalu xol

Moo lay fegal lori kaw, moo lay fegal lori suuf


Suuf ak kaw ak fépp a am lor fépp a am njariñ it

Ku dëddu am njariñal kaw, am njariñ li ci suuf


Am yitte ciw sas ba fàtteb añ du tee añ a ñëw

Fexeel a am ca kaw'ug pal fàww am ko ci suuf


Ñun ñépp yal nanu am ag pal ca kaw gu rafet

Gu sax te am ko fi suuf it ñépp féete nu suuf !

Aw Woy ci Xarit

Soppi

Xarit da lay xaral'as lëf ciy yëfam ni la am

Koo xam ne kii du xar'as lëf may la doo waayam


Sëriñ da lay jariñ as lëf yar la yor la bu wér

Xamal la Yàlla, nga dib sàntam di ab jaamam


Baadoola day bay di gor, may buuri gët, di ko jay

Di wetti aw ñaq ak'ay muñ, sax ci ab toolam


Jëkkër dafay muñ a kay muñleek a sàmm ngoram

Ragal boroomam te am njël jiitu ak maasam


Jabar dafay yaru tay muñ neexi wax bañ a wex

Rafet rafet jikko man boppam ne cib neegam


Aw fa dafay gore neexum ndañ di gas ak a tag

Waqam wa sew we wa rëy muy méng akub taaram


As gor dafay gore tey fonkiy waxam ba du dañ

Du fen du jëw te du sookeb jëw ka dib yaaram


Mbokkay ka bokk'ak yaw'ub xol, say wax it di waxam

Séeniy jëf it bokk, muy sab caabi ngay gaalam


Buuray ka xam Yàlla sax cig topp not bakkanam

Te doylu doyle amug baaxam yorug leeram


Sàmm ay ka sàmmi céram sàmm'ub xolam ba du jëm

Cig moy du jog ci ndigël, bii sàmm a gën giiram


Jàmbur dafay jàpp fàww'ug njaamburam ci lu bon

Du def lu dul noona, déeful dégg aw tooram


Sang ay ka sangi moroomam tey jubal ak a jub

Nekkal di ab sang yaw mii mbaate ngay waayam

Karmat ak delluwaay

Soppi


Xool it

Soppi

Jukki yi ci lonku

Soppi
  • [[]]

Lëkkalekaay yu biti

Soppi