Bijjaan
Bijjaan aw yaram la wuy jur ab toolu bijjaakon. Man naa nekk ab mbëjbijjaan, moom dafay soxla ñu koy jox dawaanu mbëj ngir muy man di wéy di jur toolu bijjaakon. Man naa nekk itam bijjaan bu sax, ndax ngir jur tool bi du jële dara ci biti, Lépp ci biiram lay xewee, moo tax toolu bijjaakon bi di sax ba faww. Bii bijjaan man naa juddoo ci dénd ci yenn xeeti xeer walla it manees na koo sàkk.
Ab bijjaan di na am lu néew-néew ñaari dott, benn bu bëj-gànnaar ak bu bëj-saalum. Yenn xeeti yaram yi bijjaan da leen di xëcc, lu mel ne weñ, yeneen yi mu leen di bëmëx, lu mel ne ndox. Soo jëlee ñaari bijjaan nga jegele bëj-gànnaaru benn bi ak bëj-saalumu beneen bi dañuy xëccante.