Xarey jóoñe
Xarey jóoñe yu jamono ju diggu ji, nekkoon nañu di ay aj aki siyaareji yu ñu ngànnaayal, paab bee leen daa woote, ngarmi gu Tugal gi di leen jàppale ci alal, di leen kapparal, te di leen jëfloo, bu ko defee, ñu sóobu ci ay jiyaar yu nasaraan. yonnee yu xare, yu nasaraan yii, ñi ngi léen daa wootee ci turu goreel Quds (Sorisalem), gi waa Tirki tegaloon loxo Araabi Faatima yi, ci atum 1078