Waxtaan:Sëriñ Muusaa KA
ndax tur yi dina ko fiy jar, li epp fii de maa ko fi dugal te sama tur nekku fi--Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 31 Sulet 2009 à 15:10 (UTC)
- Tur kay kenn waru koo dugal ci jukki yi, bokk na ci li Wikipedia di aayal. Ndax njël lu jaar-jaar ngir xamale ki sos ak ñi cëru cib jukki, gënal ko, moo tax a judd. Ku cëru cib jukki sa tur ak la nga fa def nekk fa. --Ibou (xëtu waxtaanuwaay) 1 Ut 2009 à 09:25 (UTC)
Boo léen ko jàppee niki Ahloubadar Jëfandikukat moo ko ci def du jaadu, waaye boo léen ko jàppee niki délluwaay bu man a weral lees fi def niki ñu koy defee ci jukkiy Fraçais yi «Bibliographie = Téerekaay» mu jaadu nde loolu sikk a leesu ko, may xamle ni jublu wu ma ci ni maa ko bind maanaam li ne ci jukki bi laay gàll ci loosu ki ko wax niki ma ko defeewoon ci jukkib Sëriñ Maalig Basin Si, loolu nag man gisu ma ci lu aay te it Wiki aayalul loolii xanaa kay ku fook ni wone wu ak wut aw tur moom a ci dugal fàww mu aay ci yaw, waaye may xamle ni wut aw tur mbaa wonewu indi wu ma fii jubbu wu ma feneen, nde dugal naa fi yeneen jukki ju ma gën a jàpp ni boo ëpp njariñ te defu ma ko ca, jamono jii lii mayewu fi aw tur am na yeneen yu ko gën a maye, fii daal lénn rek a ma fi indi ñoŋal wolof ci anam gu ma ko manee, ak sama pastéefub bopp, Bu dee lu jëm ci «Jaar-Jaar» waaw foofu defeesu ko ngir yërkat yi dees koo def ñeel way bindu yi ngir jukki bu sosu mbaa mu soppiku mbaa te mu far, manees a xam ana ku ko def ba manees koo saytu, bu ma bindee ab jukki ci baayu jàmbur bu yëree jukki bi gis ci lu ko neexul mbaa lu dul noona, warees na koo wax ci wan loos la gàllu ak ku koy weral, ndax fii barab bu ubbeeku la ci weraluk GNU ku ne man na fee soppi, muy alaxam mbaa ku bindu, maangi rafetlu séen xalaat --Ahloubadar 1 Ut 2009 à 20:31 (UTC)
fi mu ne ku dugg foofu li ngay njëkk a jort mooy yaa ko def, te li nekk foofu lépp maa ko def, defuma ko nag ngir nu xam ne maa ko def, waaye ngir jàpplee ci jëm kanamug wolof, kon bu ma sañoon buy sart tegoo ñépp di ci tënku, xalaat bu rafet ku nek yor na ko, te ku nek bu nee nii mùoo gën a rafet ci man day waral lenn du sotti, ku nekk, day wéy ca na mu gise ni mooy na gën rekk, walla bu manul a ñàkk lu waay sosati ba mu wóor ne moo ko defal boppam, mu def fa turam, te lu keneen def mu bañ faa def turam. Man nag li ma gisoon kenn bañ a def tur, bu dee delluwaay dangaa war a indi juki walla barab bees ko jële, déet aw tur--Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 2 Ut 2009 à 12:01 (UTC)
yàq
SoppiLii ay yàq la yoo def:Balaaxa (xam-xamu woyiin) haruud mooy xam-xamu woy, balaaxa di bu jotal ci say wax: ci balaaxa moomu la bayaan nekk, mantiq, ak mahaanii, boo ci bëggee gën a xóotal xoolal foofu: http:http://ar.wikipedia.org/wiki/%D8%A8%D9%84%D8%A7%D8%BA%D8%A9
- lii nga ci wax a ma gën a doy waliif may dem feneen, xaj na bàyyi wu ma ci xel,
Ahloubadar (xëtu waxtaanuwaay) 2 Ut 2009 à 15:33 (UTC)
Bees dee def lee fi fekk dindi ko def fi leneen te li nga fi def gënul li fi nekkoon, dara du sotti, boo bëggatee def dara sosal sa xëtu bopp, mbaa nga dindi lu ca baaxul, mbaa nga yokk woy yi, mbaa leneen waaye dindi lu baax lol manoo cee dind lenn, xcanaa bëgg a wone ne yaa def lii mbaa lee rekk amul solo, Yàlla moo may seere li ëpp ci li ci dal bii ma ko ci def, képp kuy yëngu ci wolof war nga ma sant, te loolu dug jaayu mba jayu, waaye taxul kenn di ma xam, ku sos sab dal nag man ngay feeñ, waaye bu ñu jaayantee ne ku nek yaa ëpp sa moroom xam-xam dara du dox, ëppante xam-xam indiwunu fi, li nu fi indi mooy jëmale kanam sunu yëf yi nu bokk nun ñépp, cig woyoflu ak toroxlu, lii lépp nag ay wax la yees war di séq waaye téewul nu xam sag njàmbaar ak cawarte ak yéene jurafet ci mbir mi--Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 2 Ut 2009 à 12:31 (UTC)