Sëriñ Maalig Basin Si
Sëriñ Maalig Basin Si gane na àdduna atum 1871 génn àddina 1955 (am 84ci ay at ci ag dundam) baayam tudd Sëriñ Maxtaar Penda Si ndayam tudd Soxna Xadi Ñang, di ab jullit bu jëfe ag njullit te it di ab sufiyanke bu mag di taalubeb Sëriñ Tuubaa jébbalu ci atum 1905
bindub jëmmam
SoppiNdaama la woon su xees te am bët joti cer am xorom lool ci waxiin ak jëfiin
lenn ci ay jikkoom
Soppiku bari kersa la woon aki teggiin te bëgg lu rafet bëgg sutura lu ko waay mas a jox ci mbooloo ginnaaw ñepp gis nañ ko dakoy tasaare jox ko mboolo ma waaye du ko jariñoo, ku bëgg sunna (roy yonnent bi) la woon akuk cet bu daan tëdd, mbaa mu lekk mbaa war daaba (wata, fas, ak luni mel) dana jàpp, fu mu took jublu xibla (pénku) te du tëdd mbaa toog mukk ci kaw ab lal bëccëg, ku bëggoon xet gu neex la daawul tàggoo ak bitéelu laj koloñ te fonk ay ser (yére), ku xamoon liggeey la te man liggeey, ku ko mas a liggeeyal loo xarala xarala mu won la ca loo xamul, ku man a yare la woon, te xaral te ñime njaboot àttan njël li, Sëriñ Abiibu Si ( doomam) nee lenn rek laa gisoon mu bañ ko lool góor guy dem ci këri jigéen ba daana wax ni: Donga buy tërbiyawu moo ngi melni mbuus muñ duyi leer/ndox bu jegee jigeen manga cay jami ràbb muy seeb, bu ko laalee mu bëtt tuuru, ku am Tawhiid (weetal Yàlla) la woon ba daa ko jàggale te daa ko jàggal jigéenu këram ba amoon na ca ku mokkaloon teere bu tudd "Burkaanu Sanoosii", mas nay waare ci Tawhiid fek booba am kuy tuddu lu (ku wopp di tudd turu jàmbur) ay bokkam jàpp kooka di ko dóor ba yàlla dugalee ka tawatoon faatu, mu ni leen bëgg geen xam ni lu am yàllaa kii geen doon tam ba di ko dóor li mu ci doon dafa melni ku romb màngo gu ñoral mu xam ca doom bu ñor mu gësëm ko doom ba rot ñu ni ko yaa ko ray te kat bu ko laalutoon ab diir mu rot (nde ñor na), daadi wax li Yàlla ni: وَمَا ڪَانَ لِنَفۡسٍ أَن تَمُوتَ إِلَّا بِإِذۡنِ ٱللَّهِ كِتَـٰبً۬ا مُّؤَجَّلاً۬ۗ = nekkul di ñeel bakkan dee ci ludul ndingalul yàlla ci àpp bu dog,
ku woyofal àdduna a la woon
Soppidaa na wax ni: mbirum àdduna loo ci rëyal ba woote ko mu diis ba doo ko àttan, Sëriñ Abiibu nee: gis naa mu sëyi loo ab taawam te defeesu ca darra batey it sëyi loo na doomam bisub talaata ñu ni ko ah Sëriñ Bi tey dey day bisub talaata, mu ni aah talaata day bañ ku ci def lu baax ñu ni ko déet mu ni kon dey di naa ko ci def, maye na doomam jàpp ca loxo ba yegg ca boroom këram ni ko dénk naa ko Yàlla te dénk la ko,
Ku am ag taalibe la woon
SoppiSëñ Abiibu nee mas naa dégg mu ni boroom man Boroom Tuubaa laa jëkk a xam Yàlla, ngir bamay ndaw nekk mbakke laa gis Boroom Tuubaa xam ko, bëgg ko te booba xam a gu ma Yàlla, Mas nay waare bisub bër/hiid (tabaski, korite, mbaa tamxarit) mu ni : garab gale bu fa rasuulul laahi صلى الله عليه و سلم (ndawal Yàlla xéewalug Yàlla yal na ko ñeel ak jàmmam) taxawoon garab gale Boroom Tuuba taxaw fa, garab ga rasuulu laahi taxaw du ma fa dox, bu masaana jëm kër Sëriñ bi balaa nuyoo day jàpp, ku bëgg alxuraan (teereb Yàlla bi Muhammed indi) la woon te di ko jàng, Sëriñ Abiibu nee Sëriñ Maalig mas na koo wax ni mas naa toog ak Sëriñ Bi (Sëriñ Tuubaa) ni ko: man dey mbàkke damaa degg nga ni digal képp ku man alxuraan (ku ko man jàng bu wer) mu saxal yaari isib (benn ci 60 dogi alxuraan) ak yaari robo (benn ci 4 dogi isip) di ko jàng bëccëg, ak di ko naafilaa (jullig coobare) guddi, bama ko deggee bëgg gi ma la bëgg tax ma saxal ko madoon laaj ndax di naa ci am ab yool (pay) ? Sëriñ Bi ni ko loolu dey moo ngi mel ni for bu dajee ak boroom bu ko neexee jël bu ko neexee ba ak moom waaye yaw sax alxuraan joxeef na la, Sëriñ Maalig neena ma tiit ni ko ah mbàkke kon nu ma koy def mu ni ko xanaa di jàng rek foo yam tay bu ëllagee nga dale fa,
Ay Waxtaanam
SoppiSëriñ Maalig li mu daa ubbi koo ci ay waxtaanam mooy: ndegam/segam moos Yàlla rekkay buur walla Sëriñ Tuubaa moos ken xamul lu mu doon ! fum ko masaa waxe rek xamees ni mo ngay tàmbali,
- Mbirum àdduna loo ci rëyal ba woote ko mu diis ba doo ko àttan
- Donga buy tërbiyawu moongi melni mbuus muñ duyi leer/ndox bu jegee jigeen manga cay jami ràbb muy seeb, bu ko laalee mu bëtt tuuru
- Kilifa balaa war a digle day def balaa war a tere day ba
- Liy yàq kilifa, ñàkk njariñ, ñàkk a jëf.
- Lepp looy santaane na fekk nga manal ko sa bopp ba su ñu gàntoo yit nga defal ko sa bopp, ngir nit ñi ku léen yaakaar ñu wor la.
- Lees yarul kenn du man a jaxasook moom, loo bëgg a jaxasool danga koy tàqaleek moroomam ya yaruwul.
- Kilifa daa war a yar doomam, moo gën jikki ba fiy bëgg a juge, naan sama gannaaw na ngéen topp ci diw. (nde loolu ku yar sa doom bam man a yor mbooloo dooko wax), te nit ñi boo nee léen topp léen diw mii, bu diw jubul it duñ ko topp.
- Yàlla mooy ndox ma Rasoolu Laahi mooy teen ba sab Sëriñ mooy goj ba pas-pasu taalube ba mooy baak ba yitteem mooy di yoor aka jukki ba barim ndox.
- Li tax kuy wut Yàlla ay mbokkam di ko yedd, jaam buy wut boroomam talut moroomam, bu amee boroomam bëggul moroomam.
- Ku dul mer mbaam la, Kudul mar xaj la,
- Nit ku yiw, na joxe dooleem, joxe alalam, waaye bumu joxe ngoram, ndax ku joxe sa ngor dootoo dara.
- Ku gis sa baay, gis sa nijaay, gis sa taawub baay war a xam sa bopp.
ak yeeneeni waxtaan yu am solo dees na ko mottali... insaa allaa
Delluwaay
Soppiwaaxtaan yi ak jaar-jaar yi moo ngi bawoo ci téere bu am solo Sëriñ Abiibu Si doomi Sëriñ Maalig Basin Si bind ko ngir dajale as lëf ci jaar-jaari Sëriñ Maalig Basin Si aki waxtaanam, muy waxtaan yu am njariñ ngir lépp yeete la, yare, laabiire, ak waare, ngir li alxuraan wax ni: فَذَكِّرْ إِن نَّفَعَتِ الذِّكْرَىٰ (saaru 87, laaya 9) - فَإِنَّ الذِّكْرَىٰ تَنفَعُ الْمُؤْمِنِينَ (saaru 51, laaya 55) ak hasiis (waxtaanu yonnent ba) bay wax naan: الدين النصيحة = diine laabire la, ag càkkutéefug Sëriñ Muntaxaa Mbàkke mom Sëriñ Basiiru Mbàkke mom Sëriñ Tuubaa, Tuddee Téere ba " النصيحة لاخوان, للترشيد و التنبيب" ( Laabiire bokk yi, jubal yeete .)