Njuuj-njaaj, Sëriñ Muusaa KA a ko way, di ci tagg Sëriñ Tuubaa di ko melal, kañ ci it Sëriñ Móodu Mustafaa Mbàkke ak Sëriñ Fàllu Mbàkke ak Sëriñ Baara Mbàkke Ak Sëriñ Basiiru Mbàkke. Galanug way wi nag bokkul ci galanu araab yi, gii moo ko jëkk a wayee, mi ngi ko dikkee ci ñu doon waral ab séet doon ko taasul naan:

"Ku ànd ak ki ma àndal lu la neex laaj, ku jiital ki ma jiital lu la neex laaj".

Ci la ci fent galan gii tuddee ko NJUUJ-NJAAJ; galanug Njuuj-njaaj. Mi ngi ko tàmblee:

"*Na ngeen déglu ma dellooti fent ab daaj Ba saahir sa di baatin jullee gën ug maaj

  • Damay wëlbati mboolem wayiini soodaan

Ba feem yépp di baatin ba jar di seetaan

  • Damaa romb Ku seetal mu naa ma kaay laaj

Ku jiital li ma jiital lu la neex laaj

  • Ma seet mbir ma mu jiital jarul ay ngaañ

Ma faf jug ne ko tuubal malaaka day gaañ

  • Te Ànd ak ki ma àndal nu dem ba Tuubaa

Faral jébbalu moo gën torox su boobaa,

  • Ku Ànd ak ki ma Àndal lu la neex laaj

Sëriñ bee jar a àndal bu leen njuuj njaaj

  • Ku ànd ak ki ma àndal lu la neex laaj

Sëriñ bee jar a àndal ba léen njuuj njaaj

  • Defal ànd bi Yàlla ak Sëriñ tuubaa

Te yonnen di sa wommat nga jublu tuubaa... BMJ(Ba Mu Jeex)"

Mu bokk ci way yi mu way ginnaaw bi Sëriñ bi làqoo.

Xoolal it

Soppi