Sawat gi ci njabootug Combretaceae la bokk. Bari na lool ca màndiŋ yu Senegaal, Gànnaar, Niseeriya ba Ecoopi ak Ugandaa.

Sawat gi (Combretum aculeatum)
Sawat gi (Combretum aculeatum)

Melo wi Soppi

Garab gu neewi xob la, gàjj la guy àgg 1 ba 3i met. Xasam day ñuul bu garab gi gone, buy mag nag day baam.

Njariñ li Soppi

Soloom siiw na wàllu faj ci Afrig gu soww, reenam day faj mettitu biir, xobam dees koy baxal ngir faj febaaru sawukaay.

Nataal yi Soppi

Turu xam-xam Soppi

Combrerum aculeatum