Réew yi def ay dank

Reew yi def ay dank ak reew yi feetewul fenn

Soppi

Ag jiital:

Bokk na ci li gën’a rëy ci li juddoo ci Ñaareelu Xareb Àdduna bi, bokk na ci li ci gën’a rëy, feeñug walla juddug ay dank yu ay Réew, walla ay booloo yu ay reew , ci wàllug politig walla xare. Ci noonu dankub bopp-alal dal di feeñ nee, Amerig jiite ko, mu uuf nag Biritani, Frans, ak lu bari ci reewi Orobug sowwu gi. Mbooloo mii nag ñi ngi ko daa woowe dankub sowwu bi , ak reewi adduna ju gore ji, safaan nag walla wuute ak reewi bokkoo yi . Bu ko defee Amerig moom, jug di dimbli reewi dankub sowwu bi, ci ngànaay ak xarala, ak alal, ngir dëgëral seen koom-koom, te may leen doole bañu man a taxaw di tata ci kanamu reewi bokkoo yi, tee leen a tas, tee leen a wisaaroo. Naka noonu, dankub bokoo bi , moom itam sosu, Bennoog Sofiet gi jiite ko, mu uuf lu sakkan ci reewi bokkoo yi ci Tugal gu bëj-gànnaar gi, ak gu digg gi, ak reewi bokkoo yi nekk Asi, niki Kore gu bëj-gànnaar gi, Wietnaamm gu bëj-gànnaar gi, ak Siinug askan gi . Ñaari dank yii: di bu sowwu bi ak bu penku bi, xeex nanu ba tàyyi ngir yilif adduna bii nga xam ne sonne na lool ci ñaareelu xeexu adduna bi, nga xam ne reewi Orob yi sax mujj nanu di reew yu lòtt te neew doole ci kanamu ñaari reew yu mag yii di: Diwaani Amerig yu Bennoo yi ak Bennoog Sofiet gi, looloo waraloon gisiin wiy woote ne “reew yi ñoo tolloo, yamoo, ay nawle lanu” wii gisiin naaxsaayoon, te faf far, xajal fi wiy indi doonadi moroom gi Amerig ak Sofiet doonadi woon moroom ci yeneen reew yi.

Loolu nag taxoon na ba reewi Órob yi tàmbli woon’a xalaat ci seen ëlëg, ginaaw bi nu mujjee di reew yu ñàkk solo bu nu leen tollalee ak yile ñaari reew. Ginaaw ñaareelu xeex bi it, yeneen reew feeñ nanu, ñu leen di woowe reew yiy màgg, yi ci ëpp nag ñooy reewi Asi ak Afrig, yi doon door a tembe ci reewi sancaan yu orob yi. Reew yooyu tam danku nanu ngir taxawal dankub reew yi feetewul fenn, ne li niy def mooy fas yeenee ame ag peeteedi gu rafet ci diggante ñaari reew yu mag yi, ak yi nekk ci seeni ngunu. Dananu leen leeral ci lii di ñëw lenn ci danki adduna yi, bu ci mel ni: Tapoo gu càmmooñug atlas (Otan):

Njiilul Amerig lii di Harry Truman (1884 – 1972 g) dafa nekkoon ku bañoon lool mbokkte walla (cominisme), te bañoon it mu tas. Looloo taxoon mu taxawaloon ci atum 1939 g, ag tapoo walla alliance gu boole woon Amerig, Itaali, Holand, Beljik, Norwej, Danmark, Fraans, Kanada, Portigaal ak Island. Ñu tudde woon nag tapoo gii, tapoo gu càmmooñu Atlas. Ginaaw bi la ci Turki bokksi ak Gres, atum 1951g, ak Almaañ gu federaal gi atum 1955 g. Seenug kollëre it ci ñatti wàll yii la jëm:

(1) kepp ku laal benn ci reewi tapoo gi, laal nga yi ci des. (2) Reew yi ci bokk dananu dimblante ci seen biir ci wàllu aaru , alal ak koom. (3) Tapoo gi dana taxawal ab jataay bu xare , te da na am njiit lu matale tam.

Jaadu na nu leeral ne Amerig mooy dàttub tapoo gii, maanaam mooy reew mi ci ëpp solo, ci wàllug li nuy joxe ak ngànnaay. Paris it moo nekkandi woon ab dalam, ba ci mujj gi nu tuxal ko ca Buruxel, peeyub Beljik. Bokkoon na ci li ko taxoon a jug, neexal dundug ay askanam, yombal seenu nekkiin, dëppale ko ak sarti demokraasi, goreg jëmm ak yoon.

Tapoo gu Warsaw:

Soppi

Bennog Sofiet ñoom itam taxawal nanu ag tapoo gu kaaraange, atum 1955 g, loolu nag booy seet, ag won Amerig rekk la ne nun itam toogunu, boo sosee tapoo gu Atlas, nu sos sunu gos, rawati na bi ci Almaañ gu sowwu gi bokksee (ci gu Atlas gi) atum 1955 g. Tapoo gu Warsaw moom, Bennoog Sofiet la woon, reewi bokkoo yi nekk ci ngunoom, maanaam yi ànd ak moom, ci gànnaaru Tugal ak diggam, mell ni: Romani, Poloñ, Hongri, Cekoslowaki añs. Warsaw nag li ko taxoon a jug mooy aar Bennoog Sofiet gi, ak reew yi ko topp, ci mbooleem musiba mu man a bàyyikoo ci tapoo gu càmmooñu Atlas gi. Dëkkub Warsaw bii di peeyub Poloñ moo mujjoon dib dalam, li mu yoroon it ciy xarekat àggoon na ci 6000000 xarekat, ñu seddale leen ci diggante reew yi ci bokk. Tapoo gu kollëre gu diggu gi: Waa tapoo gu Atlas, Amerig jiite ko, danu ne woon daal fawwu nu jële fi bennoog Sofiet, tas tapoom gii di Warsaw, ci noonu ñu taxawal ag njiit gu jagoo mbirum penku bu diggu bi atum 1951 g, ginaaw bi nu sos mbootaayug aar penku bu diggu bi, atum 1952. Ci atum 1955 g, nu sos tapoo gu Iraak – Turki, ñu gën koo xame ci tapoo gu Baxdaad, tur woowu nag mujj na soppiku atum 1958 g, mujj di tapoog kollëre gu diggu gi, ginaaw bi ci Iraan bokkee, Pakistaan, Britani, ci wetu Turki ak Iraak. Ñu leen di fattali rekk ne Iraak moom mujj na genn ci tapoo gii ci suwe atum 1968 g. Jataayub Tugal bi : Waa Tugal ya daa woote bennoog Tugal, ak tembug ay gis-gisam aki saxalam, taxawaloon nanu ca atum 1949 g jataayub Tugal bi, muy ag mbootaay gu koom-koom, gu politig, loolu nag doonoon ab jeego bu njëkk rekk, jëm ci reewum Orob mu mag mu nu bëgg a taxawali. Bookoon na ci jataay boobu nag: Biritani, Frans, Itaali, Belgik, Holand, Luxamburg, Danmark, Norwej, Suwed ak Irland, nga rax ci dolli ay ndawi parlamaa yu reewi Orobug sowwu gi ak Turki. Dëkkub Strasburg bu Frans bi moo doonoon dal bi. Rewwi Tugal ya ca ja bu nu bokk ba : Waa Tugal yi – ci ag kollare gu nu fase woon ca Rom Atum 1957 g – taxawaloon nanu am mbooloo mu koom-koom mu Orob, nu gënoon koo xame ci turu Reewi Tugal ya gore ci seen biir. Buruxel nag lanu defoon seenub dal. Bokkoon na ci Frans, Britani, Itaali, Beljik, Almaañ gu sowwu gi, Luxamburg, Holand, Irland, Danmark ak Yonan (Gres). Ja boobu nag li ko taxoon a jug mooy dimblanteg koom-koom gu Orob, waaye mujj na rax ci gu politig gu yaatu ci seen biir. Mbootaayu dimblanteg koom-koom ak suqali  :


Mbootaay gii, Amerig moo ko sosoon atum 1980 g, muy mbootaay gu mel ni ( Reewi Tugal ya ca ja ba nu bokk ), ngir rekk man a dugg ci koom-koomu Tugal bi cig wàll, ak ngir man a dëgëral ay seqooy koom-koomam yi mu am ak reewi Ja bi, ci geneen wàll. Bokk na ci mbootaay gi nag: reewi tapoo gu Atlas gi, ak Siwis, Finland, Otris, Suweet, ak Yogoslawi. Mbootaayug reewi Amerig yi: Mbootaay gii yàgg na a sosu, ndax def na ko ci 30 awril atum 1948 g, waaye ag dëgg-dëggi sosoom mi gi door atum 1890 g, muy – man nanu ne – lu juddoo ci xalaatu njiitul Amerig lii di woon Monrow, mi daa wax naan ((Amerig daal ñaari Amerig yi ñoo ko moom)). Mbootaay gii nga xam ne Diiwaan Yu Bennoo Yu Amerig yi ñoo ci bokkoon ak reewi Amerig gu Latin gi, mujjoon na gën a yaatu gën a jëm kanam, mujj di ëtt bu am solo ngir dëppale diggante reew yi ci bokk, waxuma la nag njariñul koom-koom lu mag li ci nekk. Waa mbootaay gii nag Wasington lanu defoon seenub dal, te Amerig it amoon na kilifteef gu mag ci mbootaay gi, kilifteef googu feeñ na bu baax, bi Amerig tèggee Kuba ne bokkatul ci mbootaay gi, loolu nag mi ngi amoon ci ginaaw bi fi ag fipp gu bokkoo amee ca atum 1958 g.

Mbootaayi reewi Andis yi:

Moom nag mbootaay gu jagoo yenn ci reewi Amerig gu Latin gi la, li ko tax a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom-koom ak aada . ñi ci bokk nag di Kolombi, Peru, Ekuwador, Cili ak Boliwi.

Naalub Marsaal bi ak Komikon:

Bennoog Sofiet daa taxawaloon ag mbootaayug koom-koom atum 1949 g, ngir fayyoo ci ci li Tugal def ci wetam muy mbootaayug Ja bi, nga xam ne Amerig moo ko digaloon waa Orob yi, ne leen woon nanu taxaw ci tabaxaat seen koom-koom bu daanu bii nga xam ne xareb Àdduna bee ko màbboon, te moom dana leen ci jàpple, wooteg Amerig googu, ñi ngi ko gënoon a miine ci turu “Naalub Marsaal” , Marsaal nag jawrini Amerig ji yoroon wàllu bitim reew la woon, ci ginaaw ñaareelu xareb adduna bi. Sofiet yi nag ñoom seen mbootaayu koom-koom ñi ngi ko tudde woon “Komikon”, Bennoog Sofiet jiite woon ko, mbooleem reew yi àndoon ak moom bokkoon ci. Li ko taxoon a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom-koom.

Mbootaay gi boole reewi araab yi :

Reewi Araab yee ko sos ci atum 1940 g, ngir dimblanteg politig, gu koom-koom ak gu aada, ci seen biir.

Mbootaayug jàpplante gu Asi:

Reewi Asi yee ko sos ak yu Afrig yi, ngir dëgëral diggante reew yi ci bokk.

Mbootaayug bennoog Afrig :

Moom mbootay la gu reewi Afrig yi, ñu sos ko atum 1963g, li ko tax a jug di dëgëral buumi dimblante ci diggante reew yi ci bokk, rawtina ci wàlli poloitig, koom-koom ak aada.

Reew yi féetewul fenn: :

Reww yu bari temb nanu, ginaaw ñaareelu xareb adduna bi, rawati na ci goxu Afrig ak Asi, ñu daal di dem nag bokki ci mbootaayu xeet yi. Reew yooyu di door a am ag temb, soxla woon nanu di diisoo ci seen biir, te di daje, ndax kat ragaloon nanu bu baax reewi sancaan yi ak seeni pexe cig wàll, ak ngir ne ginaaw bi nu tembee ba noppi, danoo fees dell aki coonay koom-koom ak yu politig ci geneen wàll.

Ci nooonu am mbooloo sosu mu nu xame woon ci turu “Mbooloom reewi Asi yi ak Afrig” , ab xalaat dox ci ñoom jañ leen ci ñu taxawal ndajem Asi-Afrig, ngir gëstu jafe-jafey ñaari gox yi, rawati na lu aju ci goreel ay askan seen, ak tembal leen, teggil leen sukkub sanc bii tegu ci seenug dòq, ak ci anam gu mu ci teggoo.

Ci noonu nu def ndajem Bandonj ca awril 1955 g, ca Endonesi, ndawi lu tollook 29 reew teewe ko, yu Afrig ak Asi, ñooy: End, Bakistaan, Endonesi, Borma, Silan (mujj di Sirilanka), Afganistaan, Iraan, Sapoŋ, Filipin, Taylànd, Siin Gu Askan gi, Wietnaam gu bëj-gànnaar gi, Wietnaam gu bëj-saalum gi, Cambodie, Lawus, Nipal, Ecopi, Liberia, Tefesug Wurus (Gana ginaaw bi), Siri, Isipt (Misra), Iraak, Nguurug Araabi Sawdid, Jordanie, Libi, Sudan, Liban ak Yaman. Ndajem Bandonj nag mooy ndajem adduna mi njëkk a boole ndawi ay reewi Asi ak yu Afrig yu temb. Ay ndénkaane aki saxal yu bari juddoo nanu ca ndaje ma, yuy soññee ci nu yamale diggante xeet yi ak waaso yi, te wormaal àqu ak yelleefu doomu aadama ju cosaanu ji, ak sañ-sañu nit ci wutal boppam mujj gi ko neex. Moom ndaje mi tam woo na reewi Afrig yi ak Asi ci nu dimblante ci kom-koom ci seen biir, te diisoo ci politig.

Ndajem Reew yi feetewul fenn, nag juddoo na ca ndajem Bandonj moomee. Nu njëkk koo amal ca Keer atum 1958 g, ma ca topp, nu defe ko Konaakiri atum 1960 g . Bi àdduna bi gënee bari ay coow, xuloo yi gën a tar ci diggante reew yi, Jamaal Abdu NAASIR, mi nekkoon njiitul reewum Isipt ak kii di Tito nekkoon njiitul Yugoslawi, ñoom danoo woo woon reew yi feetewul fenn te nekk Afrig, Asi ak Amerig Latin, ne nanu def am ndaje mu mag, ngir gëstu tolluwaay bii, ak tàngoor wii ci adduna bi. Ci noonu nu daal di def ndajem Belgraad, ci sëtumbar 1961 g, daal di genne ay saxal yu aju ci jàmmi adduna bi, ak jafe-jafe yi aju ci noccim ngànnaay mi , ak jafe-jafe bu Aljeri bi ak bu Kongo, ak yeneen jafe-jafe yu adduna yu bari yu amoon ca jamono ja. Nu defaat meneen ndaje ca Keer, mu Reew yi feetewul fenn, ci Oktoobar 1964 g. Lu tollook 47 ci ndawi reew teewe woon ko. Ab lim nag ciy saxal aki ndenkaane yu am solo genne na ca mooma ndaje, nu tudd ci yii rekk:

(1) wormaal sañ-sañu askan yi ak seen àq ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg. (2) Àndandoo ligeey ngir goreel reew yi tembagul. (3) Sakku nu nocci ngànnaay yi, te lijënti xuloo yi ci yoonu jàmm, te jële fi tapoo yi tas leen, dindi dàtti xare yi . (4) Ligeey ngir suqali dimblanteg koom-koom, aada, xam-xam ak yar ci diggante reew yi ci bokk.

Ñi ngi fattalee ne Reew yi feetewul fenn dolliku nanu, bi reew yi temb gënee dolliku, xuloob reew yi gën a tàng, rawante ci ngànnaayu gën a yokku, ci ngànnaay yu nu xamoon yi ak yu gën a jëm kanam yi. Looloo waraloon Reew yi feetewul fenn gën di dolli seeni daje yiy wër, ak di gën di ligeey ngir adduna bi man a dégg seen baat, te man cee def jeexiit bu baax.