Màggalug Tuubaa

Màggalug Tuubaa, Bis la bu màgg fi Taalubey Sëriñ Tuubaa yi te it di bis bu ñu fonk, Di it bis bi Sëriñ Tuubaa demee ci tukkib liggeey bi, ci 18 ci aw Magal (safar), Nu di ko amal at mune fa Tuubaa, ci fukki fan ak juróom ñatt (18) ci aw Màggal (Safar), ci arminaatu (calendrier) weer wi walla bu Hijri. Teg ko ci ndigalul Sëriñ Tuubaa "Bu bis bi ñëwatee na ngeen ma Santal Yàlla kem séen kàttan". Mu digle woon ko ci fukki fan ak juróom ñatt ci atum 1341 ci hijri, di 16 julet 1921 ci Gregorian. Muriid yi di juge fune di jëm Tuubaa, ngir amali ko fa barab bu tedd boobee, dem na nag ba yamatul rekk ci Muriid yi, Waaye xanaa nekk xew-xewu Julli ñépp, Mbaa sax nit ñi ngir mu gën a matale, Muy yitte ju rëy, Ay miliyoŋi nit diko teewe. Noonu it lees koy amale ci àdduna na si sépp, niki Aamerig, Tugal, Asi ak Afrig, ci Këri Sëriñ Tuuba yi, Fépp fu mbooloom Murid nekk,te gàllankooru ci man koo defee Tuubaa, dees nako fa amal ci genn anam gi, Lépp nag, Nu koy teg ci ndigalal Xalifa ba fa nekkal Sëriñ bi, Mookoy woote, mooy yeesal it ndigal la ci Sëriñ bi joxewoon, At mu jot.

Dencukaay:Kàrtuw Tuubaa ci google earth.jpg
Nataalu Tuubaa barab bees di amale Màggal gi ci Google Earth

Baatu Màggal:

Soppi

Màggal baatu wolof la, Maanaa mi man a doon fekk ku/lu/ju màgg nga nangul koko, Te di ko wone, Di baat bu jekkul ci lenn mbaa kenn ku moy Yàlla Màggaakon ba, Keneen koo ko solal mu ëpp ko, Mbaa mu di bokkaale, Sëriñ bi nag! ci jagle gi ko Yàlla may, te ñeelul keneen ak wuute gu mu wuute ak nit ñi, Bokk na ci baat bile, Ndax xew yi ko fi njëkk yepp séeni tur maneesu koo natt ci Yàlla aji Kawe ji, niki: Tabaski Yàlla jaaduwul ci Moom (tud naa sellam ga) ndax mooy Aji-Raye ji, Gàmmu Yàlla jaaduwul ci Moom (t.s) ndax amul bisub juddu, Tamxarit Yàlla jaaduwul ci Moom (t.s) ak beneen bis boo tànn nag, tur wa jaaduwul ci Yàlla, Moom Sëriñ Tuubaa nag ci jagley Yàlla, Mu indi fi Màggal ak Sant, Ñuy yu amul woon, te Yàlla jagoo leen, Magal Yàlla, Sant Yàlla, loolu it bokk na ci Kiimtaani Sëriñ Tuubaa liggeeykatu Yonent buñu tànn ba.


Taarixu Bis bi:

Soppi

Ci njëkk sosu gi, Ku Tud Moor xari KAN la Sëriñ Moodu BUSO taawub Sëriñ Mbàkke BUSO yonni aw bëy mu juge GEDE jëm njaareem fa Sëriñ bi ni ko joxal ma ko Sëriñ Mulaay BUSO (Rakki Sëriñ Moodu BUSO mee la) neeko mu joxal ma ko Sëriñ Tuubaa niki àddiya,

Dencukaay:Moodubuso.jpg
Sëriñ Moodu Buso

Sëriñ Mulaay yeew bëy wa ci barab dem ca Sëriñ bi neko "Sëriñ Moodu BUSO yonnee nafi ab gàtt" Sëriñ bi laajo ko ni ko "Gàtt ba lumu ?" mu ni ko Bëy wu jigéen la, Sëriñ Bi neko: ndax man ngaa fexe ba weccil ma ko am xar mu góor ? Mu neko: waawaaw ! Sëriñ Mulaay jël bëy wa ginnaaw bimu jotee ndigël ngir weccee ku ko ak am Xar, dem ca Séeréer su mbuudaay sa fa nekkoon, Ngir weccee ku ji bëy wa, Mu fekk fa ab séeréer neko: Man dey! damaa yor aw bëy, te bëgg ku ma ko soppil am xaaf (xar mu góor) ? Séeréer ba seet bëy wa, neko: waawaaw ! Man naa nekk, ndax bëy wa, ba ko séeréer ba seetee, Day bëy wu jigéen wu giir (jurandoo lu bari te lumu am mu dund) te joox (bari soow lool), Séeréer ba neko: Gàtt yaa ngi nii, seetal bu la ci soob, Sëriñ Mulaay neena: Ma seet xaaf ma ca gën a rëy, Séeréer ba neko: Sant naa ci bu baax ! Mu indi ko, Wax ko Sëriñ bi,

Dencukaay:Mulaay.jpg
Sëriñ Mulaay BUSO

Sëriñ Bi neko: Nanga ma ko dencal ba ma laaj lako, Neena: Mu denc ko, Ba bisub talaata fukki fan ak juróom ñatt ci weeru Màggal (18 safar), ci atum 1341 ci Hijri, Di tolloo ak 16 julet atum 1921 ci Gregorian, Sëriñ bi woolu ko moom Sëriñ Mulaay, Jox ko ndigël neko: Sama gàtt ba mingi fi ? Sëriñ Mulaay neko: Waaw, Sëriñ bi neko: Boo demee nga rendil mako, Te boo koy rendi, nanga ci am pasteefub Santal ma Yàlla ci bis bii, ndax kat maangi xamle ne: Bis bii ci lama saa Boroom dëeloon ngir jox ma li taxoon may liggéey, te jox nama ko, kon nag ! Maangi ciy sant Yàlla, Te ndigël naa leen yeen Taalube yi, Bu bis bi ñëwatee ngeen santal ma ci Yàlla, Sëriñ bi neko nag: Boo demee rendi ko ci sa loxol bopp, fees ko ci sa loxol bopp, te it nga toj ko ñatti xaaj: 1-Benn saam bi, Nga jox ko Soxna Aminta BUSO [Way-juru Sëriñ Abdu Xaadir MBÀKKE], 2-Ñaareel bi, Nga jox ko Soxna Anta Bale BUSO [Di rakki Soxna Amina BUSO mee], 3-Ñatteel bi, Nga yobbu ko ca daara ja nga nekk, sarax naa leen ko.


Ndigal li:

Soppi

Ginnaaw ba Sëriñ bi woolu magi Taalube yépp, siiw na ca ña ko fekke woon, Sëriñ Ma NDumbe MBÀKKE, Seex Ibraahima FAAL, Seex Iisaa JENN ak Sëriñ Mulaay moomii, ak ña ca des... ne leen: Ñu baax ña fi jaaroon ñépp (ci lu nëbbu xayna), Ku ci ne am na bis, niki Ibraahima (jàmm ci moom) ak Tabaski, Kon nag, Bu Tabaski ñëwatee Ku ci am ñaari gàtt, Nga ray benn ba ca Tabaski ga, Te ba ca des mu denc ko ba ci sama bis bii di 18 ci weeru màggal (SAFAR), Santalee ma ko Yàlla, ***... lii la waxoon ca kanamu mbooloo ma, Ginnaaw santal léen ma Yàlla rekk la wax, te tudd ci ab gàtt, tudd ci it Tabaski, te it tuddee wu ko wenn tur, lumay ni léen ngeen Santal ma Yàlla rekk, Te sant di jëf aki wax, Tax ba ña ko daa def daako woowe «Tabaskiwaat/Tabaskiyaat» tur woowu di wey, Ba am bis, Sëriñ bi ci ag fegoom ak yeesalug Diine gi ko tax a jog ak nimu bañee Bidaa, Bañ darra luy nduroo akug réer feeñ ci am mbooloom. Mu wax leen ne: «Bu ko kenn waxati Tabaskiyaat waaye Màggal», ñu door di ko wax Màggal ba fimne.

Mu des nag jeneen wax ju mbooloowu wul, Waaye ku woor la ko wax, Di Sëriñ Amsatu JAXATE, Sëriñ Bi da koo woolu mu joge Tuubaa dem Njaareem (JURBEL) àgg fa ci waxtu wu tàng, Sëriñ Bi neko: Demal noppalu, Ba ca soba sa, Sëriñ bi woolu ko, neko: Lima la doon doye de moodi, Saa Boroom lama doon liggéey, Damaa dëela loon (digoon) nima: Ci bis bii lama koy jox, Te wanoon na mako, Bis bi yegsi na, wax ko neko: Bamay joge Mbàkke baari di bisum gaawu (samedi) 18 ci aw màggal (safar), Nattu yama Tubaab yi teg, lamuy metti-metti moom laa àndal, ba ca déwén sa ñu ful ko fukki yoon, Bis ba déllu siwaat ñu fulati ko fukki yoon muy téeméeri nattu, Mu déllu séeti, ñu fulateeti ko fukki yoon, Muy junniy nattu, Junniy nattu yooyu nag diirub fukki ati laggéey bi moom laa yanu, (8 ci géej gi, 2 gànnaar, Muy=10) ñu di ko ful, Binga xamee ni nag, fukki at yi jeex na, Ci la nattu yi «Tàmbalee wàññi ku», Sama Boroom ci ag baaxam nema: Litaxoon ngay liggeey moongi nii ma jàkkaarloo ak loola, Waaye taxul woon ma jot ca, Ba ci bisub tay nag, lama Saa Boroom jox ma am sañ-sañu yoral ko saa bopp, ŋàbbal ko saa bopp, Bis niki tay mingi ak man, Malay xamal it ne: Damaa bëgg a sax di ci sant Yàlla, te digal leen it yeen Taalube yi ngeen sax dima ci santale Yàlla, Lima saa boroom jox nag, Mooy lima doon sàkku ca moom, Waaye xamal nama ne: Lii muma jox saa su bis bi dellu seetee Dana ko ful fukki yoon, (niki mu ko doon defe ca nattu ya) diirub jamono, Ba àdduna di fàddu, Ginnaaw ba it ba ca àjjana, ab jant bees di xame waxtu amu fa, Waaye saa Boroom moom xamna saa sa ak jamono ja, Ba bu bis bi agsee, Mu fulal ma neexaayu àjjana ja fukki yoon (multiplier par 10), Sëriñ Amsatu neena: Ma làmb saa jiba (poche) fekk ci juróom benn fukk 300f jox ko Sëriñ bi neko: Ma santee ko, Sëriñ bi neko: War ngaa sant Yàlla, ndax sa juróom benn fukk yii, Laa yor ci xaalis man koo sante Yàlla. Kon Sëriñ Moodu BUSO taawub Sëriñ MBàkke BUSO, Moo joxe lees jëkk a ray ci bisu Màggal, Sëriñ Mulaay BUSO moo jëkk a lottal ab Gàtt yéene ci Sant Yàlla, manaam gàttub Màggal, Sëriñ Amsatu JAXATE it moo jëkk a joxe wërsagam ci Xaalis, ngir Santalee ko Yàlla Sëriñ bi, Manaam xaalisam moo jëkk ci Màggal gi.


Woote bi:

Soppi

Ginnaaw bi ko Sëriñ Bi diglee ci noonii, Ñu tàmbali koo def ci anam gu sax, Ku nekk diko defe fa nga feete, ci ndigalul Sëriñ bi, Waa Tuubaa fa tuubaa, Waa njaaréem fa njaaréem ci wetu Sëriñ bi Mag mune it diko defee ca dëkk ba nga sanc ci ndigalul Sëriñ bi, ak say dongo, noonu lees ko daa defe, Bi fi Sëriñ bi jógee it, Noonu lees ko daa defe ci teewaayu ak ndigalul Sëriñ Moodu Mustafaa Mbàkke mi fi wuutu woon Sëriñ bi, ba bi fi Sëriñ Móodu Mustafaa bawoo Sëriñ Fàllu Mbàkke wuutu ko, ci la ko wootee, Ngir ñépp diko defee si Tuubaa ci ag booloo, noonii nag, lees ko daa defe ci Téewaayu Sëriñ Abdu Lahad Mbàkke, Sëriñ Abdu Xaadir, ak Sëriñ Saaliwu Mbàkke ba fimne ci teewaayu Xalifa bifi léen fi wuutu,

Nees ko baaxoo Màggale:

Soppi

Dees na ci daje ngir dundal ag bokk, Dees na ci Jàng Al-xuraan ngi dundalee ko bis bi, Dees na ci Jàngi Xassida ngir jollee ko ci Yonent bi (Jàmm ci moom) akit dolli koo ci, Dees na ci def ay bernde yaatal ko ci lekk ak naan, ci anam gu matale, Ba ku fa teew xeewlu ca namu ware, Ngir ñépp beg ak wone ci it xeewali Yàlla aji xeewale jees fay sant, ci bis bi ngir jéem a wone xeewal yi Yàlla defal seen Sëriñ te defal leen ko. Dees na ca daje it ci ay barab, ngir fàttali njàngalem Sëriñ Tuuba ak a dundal ay jëfam, di dolleente ci diine, di fàttli ña fa teew it di ay taalube mbaa ay Jullit, li Sëriñ bi woote lumu ? ba kune gis ci sa bopp. Ak yeneeni mbir yuy jariñe te dëppoo ak njangalem Sëriñ Tuubaa mi di diiney kase.


Ngënéel li ak njariñ yi:

Soppi

Amna yu nëbbu ak yu feeñ te xamu ñu ci lumay lees ci wax, Waaye dëgg-dëggi mbir mi, Ay gumba lanu ci, Boroom bis bi ak Ka mu koy bisal rekk la ñeel. Yu feeñ yi: Bokk na ca dajale ay jullit ngir ñu dox bokk gi Yàlla doxal seen digante. Bokk na ca it daje diggante ay bokki askan ak bokki nit, te dox ko di lu war. Bokk na ca jàngum Alxuraan mu jaatu ci lim bu kenn manu la natt, te Yonent bi (Jàmmi Yàlla ci moom) wenn arafam moo gënn àddina ak li ci biir. Bokk na ca it Jàngi Xassida ci lim bu kenn man la takk, te Yàlla digël nu te jiitu ci, nu julli ci Yonent bi, ne it ku ci julli mu ful ko. Bokk na ca birnde yu matale mbooleem ña fay teew, Ba kenn dootul xàmme ku am ak ku ñàkk, ñepp jëfandikoo ñam wa gën, Te Yonent bi (Jàmmi Yàlla ci moom) ne: Yi gën ci diine ñooy:Bernde (joxe aw ñam) ak Nuyoo. Bokk na ca dajeb woroomi Xam-xam, Dolleente, Jàngale, Xamale, Laabireente, Soññee ci diine, te ñu wax ne dajeb woroom xam-xam yi yërmànde la. Bokk na ca dajeb kureeli diine yi, Ngir man a gën a rataxalaat diggante yi, Féddali bokk gi. Bokk na ca it dajeb Taalube yi ak seeni Sëriñ siyaare, Yees lu ak Joxe Haddiya ji nga xamni Yàlla a ko digle ci Al-Xuraan. Ak yeneeni ngëneel aki njariñ yu nu lott ci lim ko...

Yu nëbbu yi: Sant la Sëriñ bi woote, Sant nag lu màgg la ci Lislaam, Rawatina ci way-sóobu yi (Sufiyaanke), Jàppe nañu ko niki màqaama mu kawe, Benn ci ñatt yi gën a gaaw ci jigeel Ab jaam Boroomam, Muy Màqaama mu kawe, Sëriñ bi wax na ne: «Kuy saa mbegte di sa mos (mbegte) bu bis bi ñëwee nanga ma ci santal Yàlla, Bu ëllëgee ma bokk ak yaw pay ga» Mu waxaat ne:Kepp ku ci ray Ginaar ba Giléem ngir Santalee ma ko Yàlla ëllëg maak yaway bokk xeewal ya ca àjjana, may ya bokk na ca li mu wax ne: Liko Yàlla jox saa su bis bi dellu seetee Dana ko ful fukki yoon, diirub jamono ba àdduna di fàddu, Ginnaaw ba it ba ca àjjana, ab jant bees di xame waxtu du fa am, waaye saa Boroom moom xamna saa sa ak jamono ja, ba bu bis bi agsee, Mu fulal ma neexaayu Àjjana ja fukki yoon (multiplier par 10), kon loolii yaw miko Màggal ci Ginaar ba ci Giléem, Sëriñ bi nee: yeen a koy bokk. Sëriñ bi waxaat ne: «ñaar ñu ne, kenn ka fonk Màggal gi; ka ca des déet, du ñàkk ki ko fonk di gis li muy tiime moroom ji (li mo koy tanee)», Ak yeneeni ngëneel aki njariñ yu dul jeex te xam-xam ba ñeelul ku moy Ki (Sëriñ bi) bis lu ak kees Koy (Yàlla ji yayoo ag cant) bisal.