Lawbe, benn lang la. Ci xeetu Pël lañu bokk. Li ñu wuute ak yeneen Pël yi, mooy bant bi ñu liggeey. Senegaal ak Mali lañu gëna nekk.

Lawbe (baat bi)

Soppi

Lawbe walla labbo (su de kenn la), ci kallama pulaar la joge. Ci seen lakk, mooy li ñu tudde ruuj ci wolof.

Am na ay Lawbe ñu leen woo laana/laaɗe, mooy gaal ci wolof. Ndaxte, seen liggeey, mooy tabax ay gaal, ak yeneeni jumtukaay ñu jefandikoo ci wallu ndox mi ak napp gi. Ci wettu dex lañu daan dëkk, ak mool yi (subalɓe ci pulaar). Ku leen jitte, Kalmbaan lañu ko dakkantal.

Yeneen Lawbe yi, dañu leen tudd gorworo / worworɓe. Ñoom, bant lañu liggeey, waaye deeñi dëkk ci tukki, ngiir jaay li ñu def (leget, gënn, bolde, alluwa...). Ku leen jitte, maalaw mooy dakkantalam. Xam xam yu mat lañu am ci wallu gancax, ba di ci mëna faj.

Xeetu Lawbe yaatu na. Am na ci ñoom, deeñi woy, ndax dañu daan jegge buur yi. Ñoom ñooy lawbe gumbala wala Kontimpaaji.

Cosaan

Soppi

Pël am nañu benn leeb ngir nettali fan Lawbe yi joge. Dañu ne, bu jëkk, amoon na ñeeti rakk yu goor. Taaw bi, Dikko Hamadi la tuddoon, ku ci topp Samba, cat bi Demba. Ñoom ñepp, sammkat lañu nekkoon. Waaye benn jamono, bekkoor dikk. Dikko Hamadi, mujj bayyi samm, ngir liggeey bant yi, mooy maamu Lawbe yi. Samba moom, wey ci samm bi, mooy maamu Pël yi (pullo / fulbe). Demba, soppeku bambado.

Lawbe yi nag, ay mbam sëf lañu samm, ndax ci seen cosaan, ak boobu mala lañu daan tukki. Ci ja yi, Lawbe yi ñoo daan jaay bi mala. Ci jamono xare amoon, ay addu-kalpe yu mag lañu nekkoon.

Lawbe yi, kenn sañoon leen jap ngir def leen lu bon. Ndax dañu gëm ni, ay jig lañu woon, ay nitu karaange. Rawatina seen jigeen, ku daan sey ak Lawbe bu jiggeen, jap ne, karaange la am.

Sant yi

Soppi

Tey, am na ay Lawbe, ci yeneen waaso lañu joge (sooninke...). Moo tax mën nga fekk ay Lawbe ñu yorul ay sant u Pël.

Lawbe yi bokk ci Pël yi ñooy ñu sant: Sow, Jum, Taal, Wañ... .

Ay lawbe yu bare, joge ci Sooninke yi, Gaajigo / Gaajaga, Kebe, lañu sant.

Xool itam

Soppi