Séeréer wuute gi ci sumb yi

Contenu supprimé Contenu ajouté
an
(Aucune différence)

Sumb bu 2 Fewriyee 2009 à 03:20

Séeréer ben xet u nek senegal la. Séeréer y nio juur Lébu y ak Wolof y, wa é wolof amna nu yénen xet fu mu djogué tamit. Sine ak Saloum moye seni nguruu.

Tisserand sérère de Mbissel (aquarelle de l'abbé Boilat dans Esquisses sénégalaises, 1853)

. Sogo nek Sine-saloum, ca Tekuruur lani nékone. Da niu tuki Sine-Saloum ndax dani dawone lislaam ak Almoravide y. Almoravide y danu xerone (jihad) ak séeréer ndax nu dugg ti lislaam, wa é séeréér y bugunuone lolu. Li yéep ca yonu imbratoor gu Ghana la xéw, bobu imbratoor gi mu ngi done dan. Fofu ca Sine-Saloum ay Socé (Sooninke), nio fi done deuk. kon bokk Socé ak Séeréer deukénté lani def, wa é ba nopi socé yu bari dem nanu deuk ca kaasamaas. Séeréer dani done sédellé deuk bi ci ay Lamana, ca Lamana yéep ay Laman nio fi done buur. Mbey ak Napp, ca lolu lani done dundé. Mbey (Saloum) mo done tuuru deuk bi sogo nek Sine ak Saloum. Ba paré ay Mandinke u djogué nguruu Kaabu, niow na nu ca Séeréer yi, deuk ak niom. Mandinke y ay Nanco (Géer) u Kabbu lani woon, seni buur (Mansa ca lakk Mandinke) nio lene dakk seeni rewm. Jola y nio lene né ca Sine-Saloum baxna yéep yu nit a soxla ndax mou menteu dund amna fa, té fofu amna ay nit wa é amnu buuru deug. Li moye tax tuxu nanu Sine ak Saloum. Nanco ak Buuru Séeréer yi fi nékone (Laman) danu bolo, jaxaasé, baa nek bu nu tudd ay Gelowaar. Gelowaar nonu, nio tabax nguruu Sine ak Saloum. Maysa waly Dione moye dieuk nek buuru Sine. Mbegan Ndour moye dieuk nek Buuru Saloum.

Séeréer ca seni bop, amna: Séereer y Niominka, Sine rek lani nek nappkat lanu tuuru mandinke lani am ndaw ca gelowaar lene bokk. Séeréer Ndut, Safen, Palor, None, niom Séeréeru Kajoor ak Bawal lanu. Séeréer Sine, moye Séereeru Sine-Salum. Séereeru Fouta y nak, legui ay ca tukuloor y lanu bokk, niom nio fa done ak wolof tamit, Cuballo y (nappkat u tukuloor) ak Sebbe ( ceddo tukuloor ). Séereer ak Pël nio fi dieuk nék fofu li moye tax amna Seereer fofu. Tukuloor ak Séeréer danu Kalenté aki Jola tamit. Ndax ca cossan bi da nu wax xet ni yeup dani bokk mam. Séeréer y da nu xawa niul, djol ak yaramu degeur. Ca senegal niom nio fi dakk béuré. Signaru Gorée ca xet Séeréer ak tubap lani bokké woon. Léopold Sédar Senghor, dieuk président u sénégal séeréer la woon ca baye am, Abdoul Diouf tamit. Blaise Diagne momit am bayam Séereer la woon. Séereer bou dieuk Ceddo lanu nekone, tey nak ca lislaam li nu né wala christianisme ca Sine (Joal-Fadiouth). Seni Sant yi geuneu siiw : Diouf, Ngom, Faye, Sène, Sarr, Senghor, Ndour, Dione, Dior, Diong, Dieye, Seck, Ndong, Seye, Loum, Tine, Diene, Pouye, Thiaw, Marone, Gningue, Diob, Gadio.