Dëgërluwiin walla Dëgërluwiin gu mbëj mooy ni ab wommatukaayu mbëj jikkowoo di jéem a bañ ay yani mbëj di ko jàll, di dëgërlu. Ci dëgërluwiinu ab jumtukaay lanuy man a xamee nu ndëgërloom toll.

Tekki

Soppi

Dëgërluwiin wi ρ bennaanu nattam mooy ohm x meetar [Ω x m], dafa aju ci ni wommatukaay bi bindoo (dijjaayam, guddaayam) waaye li ko lonkale ak Ndëgërlu gi R mooy mile mbind:

 
  • ρ mooy Dëgërluwiin wi ñu koy natte ohm x meetar [Ω x m];
  • R mooy ndëgërlu gu benn dogu jumtukaay boo jël ñu koy natte ohm [Ω];
  • l mooy guddaayu jumtukaay bi dawaan bi di jaar ñu koy natte meetar;
  • S mooy dijjaayu jumtukaay bi ñu koy natte meetar kaare [m2].

Sunu wëlbëtee ci bii yamale mu jox nu nan lanuy natte ndëgërlu gu ab wommatukaay bu nu xamee guddaayam ak dijjaayam:

 

Dëgërluwiin gi manees na koo natte itam ak bii yamale:

 

ci mujjante manees na koo natte itam ak safaanu wommatiin wi:

 

Ajoom ci tàngoor

Soppi

Dëgërluwiin gu ab wommatukaay dafay aju ci xeetu ne-ne bi ñu ko defaree.

Dëgërluwiin gu ab mbéll

Soppi

Ci mbéll yi Dëgërluwiin gi dafay yokk lu tàngaay bi di gën a bari, manam a wommat dafay wàññeeku. Safaan wa su tàngaay bi wàññee koo ba àgg ci benn lim bumu manuta romb.

 

  mooy Dëgërluwiin gi T tàngaay bi,   mooy Dëgërluwiin gi ci tàngaayu delluwaay bi, naka-jekk benn ci ñaar yii lay doon 0° walla 20°. &alpha di ab ngungu tàngoor bu aju ci ne-ne bi.

Dëgërluwiin bu ab xaaj-wommatukaay

Soppi

Dëgërluwiin gu ab xaaj-wommatukaay dafay wàññeeku lu tàngaay bi di yokk, kon lu tàngaay bi yokk ñuy gën a man a wommat. Bii digaale moo koy faramface:

 

A, B ak C ay ngung yees jagleel ne-ne bi lañu.

Lëkkalekaay yu biir

Soppi
wikbaatukaay am na xët wu tudd: Dëgërluwiin