Wommatiinu mbëj
Wommatiinu mbëj walla Wommatiin wi moo nuy wax ci anam gi wommat wu mbëj wi di amee. Ci limam lanuy sukkandiku ngir man a xam ñaata la benn jumtukaay bi manee wommat mbëj. Safaanam di dëgërluwiinu mbëj wi di li lay wax ni ab jumtukaay manee dëggërlu jàllug dawaanu mbëj ci biiram.
Tekkeem
SoppiBennaanu nattu wommatiin wi mooy siemens ci meetar [s/m]. Nekk itam dawaanu mbëj ci kaw taraayu ab toolu mbëj [I/E]. lu bari bile araf lañu koy teewalee .
- mooy Wommatiin wi
- ρ mooy dëgërluwiin wi (ñu koy natte ohm* meetar)
- R ndëgërlu gu mbëj gu ab wommatukaay (ñu koy natte ohm)
- l mooy guddaayu wommatukaay bi (ñu koy natte meetar)
- A mooy dijjaayu wommatukaay bi (ñu koy natte meetar kaare)