Caxat
Caxat lawtan la, xeetu ñax guy law. Ñax la gu man a muñ bekkoor. Dees na fekk ca Afrig gu naaje gi: Senegaal, Kamerun, Keeñaa, Ugandaa, Ecoopi.
Melo wi
SoppiGuddaayam danay àgg 20i met. Ag ndomaam di mat 10i sàntimet. Dafa nguuni-ngaana, te ag meññam daa yeex, ci njeexiitalu noor mbaa nawet bi lay faral di meññ.
Njariñ li
SoppiFi muy sax fépp, xobam yi, meññeefam mu yees mi ak tóortóoram bi dees leen fay lekk ni ay lujum yu ñorut mbaa nu supp leen. Dees na ko xonte gàtt yi. Garab la guy faj tawat yu takku ci lim: góom, biir buy daw añs.
Nataal yi
Soppi-
Xobi ñaxum caxat
-
Tóortóori ñaxum caxat
Turu xam-xam wi
SoppiLeptadenia hastata