Campora San Giovanni

Campora San Giovanni (Campura San Giuvanni ci waxiinu waa-campora), ab frazione la (dëkk-dëkkaan ci wolof) bu bokk ci dëkkaanu Amantea, ci tunduw Cosenza digoo ak tunduw Catanzaro ca réewum Itaali.

Campora San Giovanni
Skyline of {{{official_name}}}
Réew Itaali
Diiwaan Amantea
way-dëkk 7 340 nit

Taariix

Soppi

Campora San Giovanni du dëkk bu yàgg, way-dëkk yi fa njëkk ci diggante 1897 ak 1899 lañu fa ñëw . Te ña ca ëppoon ñoo ngi jóge woon ca cleto, ca Aiello Calabro, ca San Mango d'Aquino, ca Belmonte Calabro, ca Longobardi, ca San Pietro in Amantea, ca Lago ak ca Serra d'Aiello. Ginnaaw ay gàddaay yu tar yu waa-dëkk bi ak ñaari xarey àdduna yi, la ay way-dëkkam waññeeku bu baax. Gàddaay gi daan am jëm ci yeneen réewi tugal yi, Aamerig gu bëj-gànnaar ak gu bëj-saalum tamit, ca Óstraali ak ca Seland-Gu-Bees. Li dalee 1989 la fa ay way-gàddaay, yu jóge penku Tugal, Maghreb, Senegaal, añs, tambalee ñëw. Way gàddaay yooyu ña ca ëpp ci mbéy la ñuy yëngu walla ci tabax.

Melosuuf

Soppi

Campora mi ngi nekk ci tefesu géeju Tiren ci dóoxub Lamezia, am na 7 000 ciy way-dëkk. Campora mi ngi nekk cig joor gu maaseedi leru tefes gi. Bokk na ci li gën a raññeeku ci dëkk ba, mbéyum oliiw ak njóoxum sëng, mu doon mbaaxaay gu kawe. Waaxam ba tax na dem ca duni Eoli yi yomb, loolu tax mu doon ab jëmuwaayu nemmeekukat yi.

Koom-koom

Soppi

Koom-koomu Campora mi ngi dàttu ci mbéy mi ak nemmeeku gi. Li dale ci diggu XXu xarnu la fa mbéyum soble su xonk soqaliku, di it soble su waa-itaali yi bëgg lool. Njureef li dañ koy jaayi-ji ci àdduna bépp, muy lu am solo ci koom-koomam. Ag féeteem ci melosuuf ak nosteg yooni jokkoom: yoonu weñ aki tali, ñoo tax yëngu-yënguy yaxantu ya fay am woomle.

Lëkkalekaay yu biti

Soppi