Xoriit
Xoriit ag garab la gog xob yi dañuy sew tey am mbaar muy gën a yaatu lu garab giy gën a màggat. Man naa njool ba ci 3i met ba ci 10i met. Peeru garab gi day dëng. Jafe-jafe yi ko daay yiy indil dagg yi nuy dagg ay xobam tax na garab gi bokk ci yu ñeme coono yi. Xoriit garab la guy sax ci àll, nu man koo jëfandikoo ci lu nuy lekk mbaa di ko fajoo
Dëkkuwaayam
SoppiGarab gi ci àll bu bariy garab lay dëkk, walla ci kaw dëkkuwaay yuy max, leeg-leeg ci peggu penkug Afrig.
Mbayam
SoppiGarab man naa nangu ab sedd yuy am leeg-leeg. Waaye li mu gën a nangu mooy tàngoor, soxla na it suuf su tooy, te it àttan na aw wal(inondation).
Njariñam
SoppiLu jëm ci lu nuy lekk, xob yi dees koy togg boole ko ak supp mbaa ay pepp. Foytéefam day am caas bu weex bu nu man a lekk boole ak doom yi nu togg. Foytéefam bi man naa àgg ba ci 4-5i sàntimet ci xala.
wàllug paj
SoppiXob yi man naa faj bopp buy meti. Saxaaru ndox mu tàng mi dees koy suuroo ngir faj ay jafe-jafey gis. Xob man naa faj it payiis. Xas mi day faj biir buy metti, ak tële. Sungufam ku ko boole ak diw man naa nekk forote buy faj ay yax yuy metti. Reenam day faj sifilis (febaru sëy)
Melo
SoppiYeneen njariñ. Wirgo wu mboq man naa génn ci garab gi. Bantam ci dagg bi man naa niru lu dëgër waaye amul lenn njariñ ludul ay jumtukaay yu ñàkk solo.
Nataal yi
Soppi-
Nataalu garabug Xoriit
-
Xob yi
-
Tóortóor bi
-
Dàtt bi
-
Meññat mi
-
meññatam muñu xar
Turu xam-xam
SoppiCrateva