Xaal
Xaal genn xeetu ñax la. Mi ngi bokk ci njabootug "cucurbitacées" te cosaanoo Afrig gu sowwu jant.
Melo wi
SoppiXaal ñam wu xonq la yor, Ay foytéefam buñu matee dëgg diisaayam danay àgg 5 jàpp 20i kilo. Foytéef bi daa mbege te xaw a muluŋ. Xaal garab la guy sax at ba at (nawet lay sax). Ronam ( peer ak dàtt) danay àgg ba 3i met ci guddayam. Xobam cig yaatal day ñatti-koñe.
Njariñ
SoppiXaal, doom bi dafa neex lool, léppam dees koy jëfandikoo. Ñamam dees kox lekk. Xoliit yi nag dees na ko jox rab yi mbaa def ci cere.
Turu xam-xam wi
SoppiCitrullus lanatus
Tur wi ci yeneeni làmmiñ
Soppi- Araab: البطيخ
- Español: sandía
- Itaali: Anguria/cocomero
- Tirk: Karpuz
- Portige: Melancia Àngale: Watermelon
- Almaa: Wassermelone
- Kabiil: Tadellaεt
- Endo: Tarbuz Faaris/persã: خربوز/kharbuz
- Sapone: スイカ?( Suika)