Waxtaani sëriñ tuubaa
Waxtaani Sëriñ Tuuba, xaajub ñaaréel bi
Ag jiitël alaaji mbakke xaadimul xadiimi mooko dajale fii ngir bëgg muriit yépp jariñu ci, yàl nako Yàlla nangu ci barkeb Sëriñ Tuubaa te békloo ko ci àdduna ak allaaxira aamiin.
Ahoozu billaahi minash shaytaanir rajiim, wa inniya uhiizuhaa bika wa zurriyatihaa minash shaytaanir rajiim, rabbi ahuuzu bika min hamazaatish shayaatiini wa uhoozu bika rabbi ay uahdhuruun.
Waxtaani Sëriñ Tuuba قادله الله مااختارله
Waxi Sëriñ Tuubaa ci yéene:
SoppiSëriñ Tuubaa -Qaada lahuu Al-Laahu maa Axtaara Lahuu- Néena: Boo bëggée jàng Alxuraan Nanga ci yéene "Génn ci lépp lula sunu Boroom tànnalul; Ak dugg ci mboolem limu la tànnal. Boo dee jàng ak Xasida ci sama Xasida yi, Man nga cee yéene lula neex, Kon danga ko am, Bu fekkee ci yima def ginnaaw bima jugee jolof la walla ca at mama fa jugée, Waayé Xasaayid ya
ko jiitu moom déedéet", Bu dee Wirdu, nanga ci yéene Yàlla jariñ la
ci Àdduna ak Allaaxira, ci lu dul Lor, Ak jege Yàlla ak Yonent bi (Jàmmi Yàlla mu kawe ma ci kawam, ci aw ñoñam aki àndandoom ak mucc) jege gu lay jariñ te dula lor, Boo dee Naafila nanga yéene Dundal Sunnas Yonent bi (Jàmmi Yàlla mu kawe ma ci kawam, ci aw ñoñam aki àndandoom ak mucc) Saar yu gàtt yi, yu la ci neex jàng, (Wér na lool)
Sëriñ bi Néena: Ku bëgg Yàlla jox ko limu bëgg ci Àdduna Ak Allaaxira,
Nay toppi ndigëlam, Ku bëgg a toppi ndigëlam nay yéene, Ndax yéene moo koy
Wommat jëmé ko ci [Ag] Topp. Ku bëgg Yàlla diko fegal lumu ragal ak lumu Sib,
Nay teet (sori, bàyyi) ay tereem, Ku bëgg a teet ay tereem nay Yéene,
Ndax yéene moo koy wommat jëméko ci teeti Tere. [Wér na lool]
Sëriñ bi mas nay laaj, kenn ci ñi mu fi waccoon (bàyyiwoon), kooka nangu koo wax la am lool (sawar ci nettali ko), Sëriñ bi neko "Loolu Wolof di wax saan wu déllu si Xam nga koo! ?", Mu neko "Waaw", Mu [Sëriñ bi] neko "Xanaa ba ñu koy Wax, Saan wu baax taxul" ? Mu neko: Déedéet, Saan wa ca des kay lañuy wax, Sëriñ Bi neko: Saan wu baax déy, wa ca gën a rëy a gën. (Wér na). [Boroom Téere bi néena:Loolu mooy li Wolof di wax ne: «Yéene Néeg la; Boroom a cay fanaan»]
Waxi Sëriñ Bi ci fonk ay waxm ak bañ koo waxal lumu Waxul:
SoppiSëriñ Tuubaa -Qaada lahuu Al-Laahu maa Axtaara Lahuu- Néena: Waxal waaju baax, lumu waxul leegi la, Waayé bu jëggoon, Ku ko defaa, bu ñu xëyee, dañu lay fekk nga doon GOLO, Binga xamee ne Yonent bi -Jàmmi Yàlla mu kawe ma ci kawam, ci aw ñoñam aki àndandoom ak mucc- ñëw na, Lako Yàlla terale du defati loolu, Waaye ba leegi, ku ko def àtte boobu mingi daw ci yaw.
Sëriñ Bi neena: Des na diir bu gàtt, Ku man a wax ne: «Sëriñ Tuubaa neena, Te muy dëgg duñu nangu, nga diko waxe fi suuf, Fu kawe nga koy waxe» (Siiwna),
Sëriñ bi neena: fekke sama waxtaan, jarna sol dàlli weñ, Di dox ba bamu Xar.
Sëriñ bi neena: Damaa wax sama boroom, neko: Mbooloo mii ma topp, di wuyyoo samaw Tur, di taasu ci sama barke, Damaa bëgg nga wax ma, Li nga gën a bëgg, Ma sant léen ko ñu defal lako ? [neena:] Saa boroom ni tekk, ba mani bu doon, kuy fàtte mani fàtte na, Ma dellu waxaat koko, Mu [Yàlla] neeti tekk, Ma dellu waxaat koko, Mu ne ma «Fu ñu tollu dila waxtaane, Fu ñu lay waxtaanee, danaa léen fa tiim, ak waamew (taw bu matale) xéewël, Di léen sotti, Ba kero ñur bàyyi Ma door a Séwét» (Siiwna).
Waxi Sëriñ bi ci Julli:
SoppiSëriñ bi neena: Ubbikoo ci Julli gu Farata, Ludul ALHAMDU LILLAH (FAATIHA), Mingi melni nga dem ci Kilifa ga nga gën a fonk, neko "Dama laa soxla", Mu ànd ak yaw, ba ca barab bamu, gën a fonk, Àgg suuf nela: Waxal sa Soxla ? Loo wax ludul ALHAMDU LILLAAH, mingi melni nga séen Janaab (Muus) foofa, Wacci ko fa, daw topp ca. (Wér na)
Sëriñ Bi masnaa sëlmal Jullig Timis, Wax ni: Barab bañuy dekkee ak Bañuy deggee
daa soree lool, Koo xamni daana taxawal Julliy Juróom, Dees koy Defaral, Lumu
war ci yoolub ay Julléem, Ba àgg fa ñuy dajee, Ku daawul taxawal Julliy Juróom nag,
Bu dekkee, dañuy jàppu, ci ay tànkam, diko diri, ci Kanamam wuti Taxawaay ba.
(Wér na lool)
Sëriñ bi mas naa sëlmal [Jullig] Gee ne: «Dama ni, Koo xamni Julli dakoo soxlaal waliif (bàyyi fi) mbir yi, Dana jariñ ci julli gi, ak ci mbir yi, Koo xamne nag, Mbir yi dakoo soxlaal waliif Julli gi, Du jariñu ci mbir yi, Du jariñ ci julli gi» [daa di ne:] Jaamu Yàlla mooy laggéey, Biñu nu sant, Aada yi nag, dañu leen di dimbandikoo rekk ci Jaamu gi, [Teg ci ne:] «Fa Quuluu Anfusakum Wa Ahliikum Naaran» [Wér na lool]
Waxi Sëriñ Bi ci koor ak Laylatul Qadri:
SoppiSëriñ Tuubaa -Qaada lahuu Al-Laahu maa Axtaara Lahuu-: Weeru Koor daawul yonni ku woorul, Daawu ko def Darra, Weeru Koor yit ci la daan, gën a bari lumuy joxe. (wér na lool) (Mani: xayna day xamle ni, Ku woorul deful ak moom nenn).
Amna Taalube yu doon dundal [Guddig] Laylatul Qadri, Ci tënk bi Sëriñ bi def, Ba mu ko yëgee, Ni léen du tay, Wax[aat] léen ca beneen bis, [ni léen:] tay jii la. (Siiwna) [Boroom téeré bi ni: Lii nag, Limuy war a tegtale, mooy Lëm googu Yonent bi - (Jàmmi Yàlla mu kawe ma ci kawam, ci aw ñoñam aki àndandoom ak mucc)- Wax la, Waayé térewul ñu war di topp tënk bi Sëriñ bi def,] (Mani: Ginnaaw Xam-xam bi ci ñeel Sëriñ bi noonu ñeelu nu banu man koo ràññee, nanu tënku ci tënk bi Sëriñ bi def, Dàkke koko)
Waxi Sëriñ Bi ci ASAKA:
SoppiAmna ku mas a juge fu sori, Ñëw jox Sëriñ bi Xaalis bu bari, niko Asaka la, Dellul Fanga jugewoon, Amna juróom ñatt ñu Alxuraan Tudd, Koo ci gis nga jox koko.
Waxi Sëriñ bi ci Tuub:
SoppiSëriñ neena doomu aadama ñaari rekk la am: Yéene ak Tuub, Li baax bu fekkee daa bari ba maneefut a def lépp, La nga man léppu danga koy def la ca des, nga diko yéene, Bu ko defee ñu def langa yéene ni la nga def dila ko fay. Li bon yitam bu fekkee daa bari ba maneefuta ba (bàyyi) lépp, Dangay bàyyi la nga man la ca des nga diko tuub, Su ko defee dana ñu ko far, Te lu ñu far ak lu ñu bindul ñoo yam. (Wér na)
Sëriñ Tuubaa -Qaada lahuu Al-Laahu maa Axtaara Lahuu- Neena: Ki nga xamni dañu koy jëmale
ci lu amul njariñ ginnaaw tuub gu sell, Mingi melni ku waccu ba noppi, ñu lekk loo koko,
Ki nga xamni dañu koo jëmale ci lu Haraam walla lu ñu sib ginnaaw Tuub gu sell, Mingi melni
ku ñu lekkloo ay xal walla ay jiit, Bu léen ku baax woowee ci ñam wu baax, na ngeen lekk,
Waaye ku leen bëg a lekkloo am waccu walla ay xal walla ay jiit bu léen nangu. (Wér na lool)
Waxi Sëriñ bi ci ndigël yi ak tere yi:
SoppiSëriñ bi masnaa laajte ndax xam ngeen «Al-Iimaan» ak «Al-Islaam» ak «Al-Ihsaan» ? ñu neko: Degg nañu ñu di ko wax, Muni: «Al-Imaan» mooy léppu lu am nga gëm ni Yàlla a ko dogal, «Al-Islaam» mooy léppu loo am nga génne ca wàllu Yàlla, «Al-Ihsaan» Mooy lumu dogal mu neex la. (Wér na lool)
Sëriñ Tuubaa -Qaada lahuu Al-Laahu maa Axtaara Lahuu- Masnaa laaj, «Wa Af`aloo Al-Xayra:S22,V77,وَافْعَلُوا الْخَيْرَ»
Nu ngeen koy firee ? ñu ni ko: Wa Af`aloo, nangeen def, Al-Xayra, aw yiw, Mu ni: ñu koy def ? ñu ni cell,
Mu ni: Wa Af`aloo, juróom ñaari Haraf la, Al-Xayra juróom i Haraf la, Juróom ñaari cer yii lañu wax ni
saxal leen ci juróom i ponki Lislaam yii, te bu leen ko ba. (wér na)
Sëriñ bi masnaa laaj ndax xam ngeen, «Waajib» ak «Manduub» ak «Mubaah» ? ñu ni ko: ñi ngi koy dégg, Muni ndax xam ngeen luy seen «waajib» yéen ? ñu ni ko: déedéet ! Mu ni:mooy wàcc lal yi te dem ci der yi jaamu ji Yàlla, Daa di ni: Xam ngeen luy seen «Manduub» ? ñu ni ko: déedéet ! Mu ni: Wacc a ndiku ndamu ba ñu ni démb la bis pénc, Daadi ni: Xam ngeen luy seen «Mubaah» ? ñu ni ko: déedéet ! Mu ni : Darra, Darra, Darra, daadi ni:
- Darra ju jëkk ji, mooy Sunu boroom mii nu bind, Ku xam ci moom darra, du def lumuy tere,
Ndax moo boole «Xudratu» (Kàttan) Ak «Iraada» (nammeel) te bu yékkatee yaram ba kenn du ko tere,
- Darra ji ci toppu mooy àdduna jii ñu nekk te xalsatfee juge, Ku xam ci moom darra dooko jox sa darra, Ndax looko jox ñàkk nga ko,
- Darra ji ci topp, mooy Allaaxira jee nu jëm te di fa sax ba fàww,
Ku xam ci moom Darra doofa dawal Darra ba naw ko, ndax Darra du fa doy.(wér na)
Am na koo xamni da daan def, bu togee ci wetu Sëriñ bi di bind «Kun Fayakuun» am bis Sëriñ bi jàppu ci mbangam, neko:«MIN HUSNI ISLAAMI AL-MAR I TARKUHUU MALAA YUXNII», (Bokk na ci liy rafetal ak njullit bàyyi lépp lula am a lul njariñ) ni ko: "boo manta ñàkka bind deel bind «AL-KADHIBU HARAAMUN, (fen haraam na) WA-L-XIIBATU HARAAMUN, (jëw haraam na) WA-AlN-NAMIIMATU HARAAMUN (rambaaj haraam na)» KA DHAALIKA (niki noonu)". (Wér na)
«فاقصص القصص لعلهم يتفكّرون
ماكان حديثا يفترى و لكن تصديق الذى بين يديه
وتفضيل كلّ شي ء وهدى ورحمة لقوم يومنون.»
Waxi Sëriñ Tuubaa ci diggante boroom kër ak soxnaam, ni ñuy dëkkee
Soppi- «وعاشروهنّ بالمعروف الخ... صدق الله العظيم»
Am na ku doon jambat soxnaam ci ci Sëriñ Tuubaa ▬قادله الله مااختارله ▬ Sëriñ bi ni ko nangu naa
ànd'ak yaw ngeen jaamu Yàlla ? Mu ni ko waaw, Mu ni ko kon nak damaa bëggoon nga xamni la taxoon
ñu jox la ko moo di am nga jàngoro joo xam ni moom rekk, moo yor saafar sooko man a saafaraa te
doo ci am bàkkaar bu ko defee nga jàppee ko muy saafaras jàngoro jooju, saafara nak bu yàggee nga
bëgg koo jàppe ab dund, dang ci'y gis sikk, ndax day jur jàngoro, barina yu ngeen di jàmbat te noonu dóng la .'. wer na
Am na ku amoon ñatti soxna, ñaar ña xëy-xëy dem (melni dañ koo takkoo), Mu yónnee ci Sëriñ Tuubaa ▬قادله الله مااختارله ▬ ni ko bama demee batóllu ci àdduna dama koo bàyyi tóppu ko, bama demee ba am lama doon wut ñaw sampu kër ba am ñatti soxna, ñaar ña xëy-xëy dem melni dañ koo takkoo ma bëggoon bu dee sikk si ci man la nékk nga wax ma ko ma ñawaat ndax ma defaru, bu fekkee ci ñoom la nékk nga wax ma ko ma bàyyi leen, Sëriñ bi wax ndaw la dem a ngun nafaa ? mu niko déedéet, Sëriñ bi ni ko neeko booba ba tay sikk si ci moom la nékk, nafa dem buñ nangoo ñëw mu xam ni sikk si ci moom la nékkoon, buñ nangu wu la ñëw mu xam ni sikk si ci ñoom la nékk.'. (Mu dem fa ñu daal di ñëw) wer na
Ay dénkaane
SoppiBu ngeen xëyatee:
- Na ngeen jiital jaamu Yàlla teg ci nangoo liggéey
- Def seen naqar muy seen bànneex te def seen coono muy seen nooflaay
- Wéttalikoo topp ndigali Yàlla te bañ a wéttalikoo jëmm
- Na ngeen def ndigali Yàlla muy ab sëriñ te bañ a def ab sant muy ab sëriñ
- Ku bëgg a texe ci àdduna dangay nangoo liggéey
- Ku bëgg a texe ëllëg dangay nangoo jaamu Yàlla.
- Laabire nit ñi moo gën fital jiyaar
- Bàyyi fen moo gën jàng Alxuraan