Waxi Seex Anta ci lu aju ci cosaanul nit
Xam ngéen ne nite (l’humanité) mi ngi juddoo Afrig, tàqalikoog nit ak dundat (animal) mi ngi ame fii ci Afrig, loolu kenn sikkatu ko.Xew-xew bu am solo bii mi ngi am booba ak leegi toll na ci 5 milyoŋ ak juroom benn téeméeri junniy at (5600000 ciy at), Afrig ngay man a fekk mbooleem xeeti nitu pax (homme fossile), loolu doo ko gis ci beneen gox (continent).
Ñaari xeet yii di "Australopithèque robuste" , "Australopithèque gracile" , "l'homo alibis" , "l'homo erectus" , "l'homme de néandertal" maanaam homo sapiens bu yàgg ba, ak "l'homo sapiens sapiens" maanaan nit ku yewwu ñaari yoon, ni ko tur wi indee, niki yaw ak man, xeet wu mujj wii mi ngi juddoo Afrig booba ak leegi tollu na ci 120000 at, nite gii mi ngi juddoo ci ron rëddu yamoo wi (l'équateur), ci ron rëddu gaar (latitude)wu Kéeñaa, maanaam ci ron rëddu gaar wow, jañug ceññeeri yu jéggi-yolet yi (flux de radiation ultra violet)dafaa tar ba bépp cér mbaa yaram wu juddoo ci rëddu gaar wii, fàwwu mu nekk di lees cuub (pigmenté) te ñuul, doonul woon jàppadi ci nite gu njëkk ga muy man a dund bees ko cuubutoon, ginnaaw dénd bi moom (la nature) du sos dara cig neen, kon cuub daa ame liggéeyub aar yaram wi, da koy aar wëliif ceññeer yu jéggi-yolet yi nga xam ne doon na yàq ci anam gu mat mbooleem pukus (cellule) yu yaram wi. Nite gii dox na jëm kanam ci Afrig doore ko ci 120000 at ba ci lu yées 40000 at. Mi ngi génn Afrig jaare ko ci ñaari yoon/ Yoonalu Sues (Isthme de Suez), looloo waral deesi fekk ay roytéef (spécimen:misaali nit) ca Falastin, waaye ñoom gën ayàggadi roytéef yu Afrig yi, man xam naa ñi doon def gasi gëstu yi ci diiwaan bii, rawati na Ustaas bi Wardermer, waaye bees defee ay gëstu, dees na gis ne roytéef yu Falastiin yi ñoo gën a yees yu Afrig yi, foofooy yoon wi nitug Afrig ki jaaroon di génn. Waxuma la rekk Homo sapiens sapiens waaye it nitu pax (homme fossile) mi jotul a dund te ma la ko doon wax sànq. Beneen génnuwaay bi mooy Jibraaltaar (doju Taariq), foofa lañu jaar, ba nañu fa it ay jeexiit, mbooleem cuubiit ya (teinture) ca xunti ya, jeexiit yooyu dañuy wone ne foofu la nit ki jaare, waaye it ca bëj-saalumu Tugal rekk, fa tollook géej yu tàng ya, fa tollook "la Crimée", ca bëj saalumu Faraas, bëj-saalumu Espaañ, diiwaan yii ñoo nekkoon di yees man a dëkk.Foofu lees fekkoon mu dajaloo fa nite gu ñuul gi njëkk a dund Tugal (première humanité négroïde)loolu tollu na ci 40000 at.Ni mu manul woon a ñàkke nekkees ku ñuul ngir man adund ci Afrig, ni la manul woon a ñàkke nekkees ku am der bu leer ngir dund ca Tugal ngir sedd bu tar bi ba ëpp, fi nga xam ne amul jañug ceññeer yu jéggi-yolet yi, ci noonu la ñuule (nit ku ñuul) furee (dépigmenter) loolu àtteb dénd bi la ( la loi de la nature). Jëmmam it daal di soppiku topp wuyyusi gi mu def ñeel tëri noyyi gi ci sedd bi, ci noonu la weexe bi njëkk feeñ, bu nu tegee nee mbooleem idewolosi yi, booba ak leegi tollu na ci 20000 at ca Solutréen, di benn ci wàll yu mujj yi ci jamonoy doj ji, mooy "L'homme de Cro Magnon". Ki njëkk a dëkk Tugal ab ñuule la (négroïde), mooy "l'homme de Grimaldi", damay yam rekk ci Homme sapiens sapiens, ba nee nag homo erectus ak yeneen, waaw kay mi ngi noonu yoon wi nit ku weex jaar ba génn ci ku ñuul, ak mbooleem yeneen xeet yi ci càllal gu gudd, mbaa gu gàtt.Manoon nanu fee nekk di leeral ba lay wax ni nite gii génne jaare ca xat-xatu Béring (détroit de Béring) ngir dem juri askan wa dëkk Amerig, ba tay ni beneen bànqaas bi génne ca yoonalu Sues, jaare ko ca Duni Sond ya (les Iles des Sondes) ngir xumbali Oceani. Kon nite gii mi ngi juddoo Afrig, te it gu ñuul la, juddoo it ca balluwaayu Niil ba, maa ngi dikk leegi ci Isipt,nite gii mi ngi juddoo ca gongikuwaayu dexug Niil ga, moom nag gu ñuul kukk la woon ci li baatub ñuul ëmb ci maanaa, booba nag la daal di woon door di sanc xur wi (pegi dex gi), nekkoon na fi lu mat 120000 at njëkk muy wàcc bawoo ca diiwaanu Luwanda jëm ca Delta bu Niil ba (ab sottiwaayam)