Wéñumeññet
Wéñumeññet xetu wén buy dunde màngo ak yeneen meññet (Tephritidae). Wayé dafa bari aay xét wéñ (Bactrocera invadens, Bactrocera cucurbitae, Ceratitis cosyra, Ceratitis capitata ak yeneen, ak yeneen). Xet wéñ yoyu sow diante thii Afrik la eupéh. Nuñuy rañé méññet bu aam wéñ sii birreum: daay am ay beut-beut yu sèwu yuko weurr. Wéñ yu djigèn yi ñothi bayii sénii doom. Dom yoyu di dundé ñaam bi ci biir,bañu magg. Dirru ay faan, mu nék ay nènn. Nénu yoyu laay domii dundé ci birreum bañu maag, mu soga gènn nékaat aayi wéñ. Digunté ñant ba fukii faan,bu goor bi ak bu djigèn bi andatt. Sénii dundiin nonu lañ kooy diappo.