Màngo
Màngo garab la gu cosaanoo "Asi", bokk ci njabootug Anacardiaceae, bari na lees koy jëmbat ci réew yu tàng yi ndax ay doomam.
Moom màngo ak tàndarma bokk nañu ci garab yi gën a yàgg. Araab yi ñoo ko indi Afrig ci fukk ak juróom-benneelu xarnu. Màngo nag man naa sax fu bari waaye ci xur la gëne. Ñemewul taw ci jamono yi muy jebbee.
Melo wi
SoppiMàngo garab gu mag lay doon guddaayam day àgg ba ci 20 ba 25i met.
Xas mi daa ratax ay doomam day mat 500 ngaraam ba ci ñaari kilo ak genn wàll. Saalu doom bi dafa sew te tàppndaar
Njariñ yi
SoppiXobi màngo dees na ko jëfandikoo ngir wattu feebar yu tukkee ci jam-jam walla dagg-dagg.
Meññeef mi lu bari ay ferñent la, te it moom màngo lu baax ci "kãseer" la ak néew dereet. Te it màngo dana dimbalee ci yeex a màgget ngir ferñet yi mu làmboo. Bokk na ciy ngëneelam day xeex feebaru noyyi, day reesal ñam di xeex seere. Saal bi lu baax la ci saan danga koy baxal di ci naan booy lekk.
Nataal yi
Soppi-
Garabug Màngo
-
Meññetum Màngo bu ñuragul lool
-
Màngo ju ñor lool
-
Xob yi
-
Dàtt bi
-
Tóortóor yi
-
Ñam wi