Sëriif Muhammed Aali Aydara

Sëriif Muhammed Aali Aydara (Chérif Mohamed Aly Aïdara) mi ngi judd atum 1959 ca Daaru Hijratu (dëkk bu baayam sancoom, Sëriif Ahasan Aydara). Doomi Maymuna Jaw (moom soxna si doom ci Sëydu Jaw nekkoon seef de kantoŋ) ak Sëriif Alhasan Aydara, cosaanoo Gànnaar, bokk ci askanu Laxlal (Laghlal) ñu gën koo xam ci Ahlu sëriif laxlal di càllalag Sëriif Mulaay Idriisa, mi sos nguurug Idriisa yi, càllala gu dem ba ci Asan doomi Aali ak Faatima doomi Yónnent Yàlla Muhammed ak (JNCM).

Sëriif Muhammed Aali Aydara (Institut Mozdahir International)

Moo nag doomi Senegaal ak Gànnaar la.

Doon na wax ak a binde làkku yu bari niki Àngale, Araab, Farãse, Pël, ak Wolof.

Liggeeyam

Soppi
 
Sëriif Muhammed Aali Aydara

Kilifa diine ci dayoom, Sëriif Mohammed Aali Aydara mooy soskat ak njaatigel Mbootaayu IMI ak it rajo "Mozdahir FM" ci Ndakaaru ak rajo "Zahra FM" ca Koldaa.

Sëriif Mohammed Aali Aydara mooy xalifab mboolem Siyit "Mozdahir" yi nekk ci Afrig ak ci àddina si.

Ay mbindam ci Xam-xam

Soppi

Bind na ci fànn yu bari yu ci mel ne xam-xamu Islaam, dundug Yónnent Muhammed (jàmm ak ngëneel ci moom) ak 12i imaam yu mat sëkk yu kër Yónnent bi, Ahlul bayti (jàmm ak ngëneel ci ñoom). Ay téereem yu bari siiwalees na ko, ñu man cee lim:

  • Dëgg yi ci kuutlaayal Yónnent bi (Les Vérités de La Succession du Prophète)
  • Imaam Useynu (YYY) martiir ak xettalikatu Islaam (L’Imam Hussein (AS) martyr et sauveur de l’islam)
  • Sayyidaa Saynab (jàmm ak ngëneel ñeel na ko) waadaanu Karbalaa (Sayyidda Zaynab (paix et salut sur elle) l'héroïne de Karbala)
  • Jullig Yónnent Muhammed (jàmm ak ngëneel ñeel na ko) bunu sukkandikoo ci ag njabootam (La prière du Prophète Mouhammad (PSLF) selon les membres de sa famille)
  • Ghadir Khoum
  • Tamxarit, bisub naqar walla bisub mbég? (Achoura jour de deuil ou jour de fête ?)
  • Sàrti koppar gi ci Islaam (Principes de la finance islamique)

Téerekaay

Soppi
 
Sëriif Muhammed Aali Aydara