Nosteg doxiin
Ci xam-xamu nosukaay nosteg doxiin, ci tënk ND (operating system walla OS ci wu-angalteer), mooy mbooleem tëriin yiy yor, saytu lëkkaloo gu jumtukaayu nosukaay bi (tappaan yi, xel mi...) ak tëriin yi nga ciy jëfandikoo.
Naka-jekk nosteg doxiin gi mooy tax jëfandikukat bi man di jot ci ëmbiit li nekk ci nosukaay bi jaarale ko cib jokkalekaay (muy ay njunj walla mbind yooy cuq mu lay won li nekk ci biiram). Yitteem bu njëkk mooy tax ba jëfandikukat bi, muy nit walla leneen, man di jokkalook nosukaay bi.
Melokaanam
SoppiDañoo am ay cër yu cëslaay yu, daanaka, nosteg doxiin yépp bokk, waaye terewul am yooy fekk ci yenn yi rekk, moo tax ñu gënante:
- Saalub noste gi: di mbooloom ay tëriin yu ndaw yu lëkkaloo ci seen biir, lëkkaloo itam ak jumtukaayu nosukaay bi. Mooy liy njëkk a ubbeeku su nosukaay bi di takk, di it, man nanoo wax, wàll wi ëpp solo. Moo tax ñuy man a def liggéey yu njëkk ci ndoorteelu takk gi, tax ñuy man a jot ci tappaan bu dëgër bi, ci dencukaay yu noste yi. Ci gàttal moo yor jokkalantey xibaar yi ci biir nosukaay bi.
- Yorkaayu dencukaay yu noste: mooy liy duggale ci tappaan yi. Wépp tëriin wu soxla ab njoxe cib tappaan moom ngay woo mu duggal la fa. Mooy ki yor, rawati na, nosug njoxe yi ci nosukaay bi (wayndare yi).
- Yorkaayu xel mi: mooy liy jox xel mu doy ngir seenug ubbeeku ak dox, fu ñuy denc seeniy njoxe, tëriin yi ba ci nosteg doxiin gi ci boppam.