Imbraatóor gu Mali

(Yoonalaat gu jóge Nguuru Mali gu Mag ga)

Imbraatóor gu Mali ba ci xarnub XII, xamalu nu ko woon lu bari. Ci li tegu ci atum 1150, la nu xam tur yu mel ne Hamana, Jigi Bilali(1175-1200) ak Musaa keyta di ko wax itam Allakoy (di tekki neex yalla). Mi ngi yamoon ci Mbàmbulaanu Atlas ci sowwoom, Dexu Niseer ci penkoom, tay ñuy yii réew: Mali, Senegaal, Gaambi, Ginne, Ginne Bisaawóo, Gànnaar, ak ab xaaj bu mag ci Kot diwaar.

Réyaayu nguuru Mali gu mag ga ci 1350

Ay Cosaanam

Soppi

Ci boobu diiwaan (Sudaan) ag nguur gu ndaw judd woon na fa: Mandeŋ walla Mali (Malenke: nitu Mali). Ci li gën a siiw coosaanam, ay dëkk-dëkkaani mande yu bari yu nekkoon ci Kaw-Senegaal ak ci Kaw-Niseer. Traware yi nekkoon Dakadiyala, ci réewu Kri, ci wetu Nagasola, ci Kaw-Bakoy, Konte yi nekkoon Tabu, ca Doodugu (di tekki réewu Doo), Kamara yi ca Sibi, ca Siendugu, Keyta yi ca Nareena, ca Doodugu ak ca Doj yu Mandeŋ, nekk ci diggante Sigiri ak Kita.

Ca Doodugu la Bambara yi nangoo ay dëkk yu bari, màmm jëm penku, ba peggu Seegu ca Niseer. Ci li wër Doj yu Madeŋ, Malinke yi ñaari dëkk yu solowu lañu fa amoon: Kiri ak Dakadiyala. Njiitu dëkk yooyu ay rëbbkat la ñu woon, yu bokkoon ay gëm-gëm, bokk di def seeni xumbéeli diine. Nekkoon nañu nag ay Askan yu bari yu bennoo woon am benn buur, Simbo moo doonoon seen dàkkantal. Buur yooyu Askanu wee leen doon fal mu lee doon teewal ci ndaje ya daan am ca Pénc mu Mag ma(Gara), mi doon dogal ci li ñeel xare yi walla juuti yi...

Dooley askan yu nguur-nguuraan yooyu doon màgg, ñoo jàppale nguuru Sooso gi donn Nguura Gana gu mag ga, ba mu man a sos geneen nguur gu mag gu buur ya amoon dàkkantali Mangha walla Mansa.

Sunjata Keyta

Soppi

Musaa Keyta di ko wax itam Allakoy, siiwoon na ndax aji Makka yu bari yi mu defoon, loolu saxaloon na diiney Lislaam ci xoli Njabootu buur bi. Doom, di itam Ndono lu Musaa, Nare Famagan (1218-1230) siiwoo na loo ndax yaatalam jëm bëj-gànnaar, ak sowwu, ak pegg gu ndeyjooru Kaw-Niseer, nootoon Somono yi. Nare Famagan bari woon na ay jabar, kenn ci ñoom mooy ki ñu dàkkantale woon Kuduma (boroom góomi yaram yi). Jabar ju tawatoon jooju mooy yaayu Sunjata Keyta. Bi mu juddoo ba juroom ñaari at managul woon a dox.

Laagoom googu moo taxoon, ba Sumaawuru Kante doon faat ay magam, ba woon ko fa. Benn bis, Sunjata jéngu ne day jug taxaw, ndax naqar wi mu amoon ci li Sumaawuru defoon, tegoon ci nangu nguur ga. Mu laaj ag weñ ngir jafandu ci jug, weñ ga damm, mu jël geneen, noonu, jëlaat geneen noonu, ci la kenn waxe ne nañ ko jox yatu baayam wa, ba mu ca jafandoo la jug taxaw. Ña ko teewe woon yéemu; nday ja ak géwalam ba, Jakuma Duwa, ca la ñu fente ab bakk duppee ko Xala ga, baat ya ak woyiin wa, ba tay ñoo ngi rëkk ci dënni waa mali yi ndax mooy seen bakkuw réew.

Ci 1230 la nekk buur, ci la ray Sumaawuru, boole nguur-nguuraan yépp ya nekkoo ci wetam, ci nguuram, dal di nekk nag Mansa. Ci moom la Mali nekke nguur gu mag dëgg, ci la àgge ci pujam.

Ay buuram

Soppi

Bi mansa Ulee ñëwee(1255-1270), di ki wuutu Sunjata, la tàmbalee Diggadil(décentraliser) nguur gu mag gi jox ko yoriin wa méngoo woon ak réyaayam. Tabb ay sang jox leen ay ndomboy-tànk yu am solo, ñi ci gën a ràññeeku: Fran Kamara, Siriman Keita.

Abuubakar mu njëkk(I)

Soppi

Ci 1285 la Abuubakar mu njëkk(I) mi faatu, Jafe-jafe yi nekkoon ci tànn aji wuutu, ca la Sakura jëlee nguur ga. wuutu na nitu nguur di itam jàmbaar, ci la yaatalaate nguur ga ba dugg Gaawo ci penkoom ak Tekuruur ca sowwoom. Ay saay-saay ñoo ko ray ca weti Tripoli mu feekoon ko muy aji Makka.

Abuubakar mu ñaareel(II)

Soppi

Ci 1303, Abuubakar mu ñaareel mi(II), di jarbaatu Sunjata, mi siiw lool ndax li mu bëggoon a wuññi li nekk ci ginnaaw Mbàmbulaanu Atlas gi. Ca la jële ñaar téeméeri looco ak dund, daal di yònnee ngir ñu dugg ci mbàmbulaan gi, waaye kenn a ca dellu si nettali ni dañoo dajeek ab duus bu soxor ci ndox mi, mu mëdd leen. Abuubakar dal di jëlaat ñaari junniy looco, ak bund bu doy, and ak ñoom dem, ca la saaye ba tay.

Mansa Musaa(Kanku Musaa)

Soppi
 
Mansa Musaa

Mansa Musaa (1312-1332)Bokk na ci buuri Nguuru Mali gu mag ga, yi gën a siiw. Ci 1324 la aji makka. Ca ajam gu siiw ga, àndoon na ak 60 000 ci ay surga (su ñu ci degloo Taariix as-Sudaan). Jaar ci diggu tàkk ga, ca Walata ak ca Tuwat, ba mu àggee Xaayra la ñépp yéemu ndax alal ja mu fa indi. Nee nañu yoroon na ñaari ton ci wurus. Mbaaxam ak yéwénam, yéemoon na képp nit ku nekkoon Xaayra ca jamono jooju. Doonte déggoon na araab nangul woon a làkk lu dul làkkam, daa jëloon ay tekkikat. Mansa Musaa yóbb woon na turu Mali ci mépp réewu araab, dalee ko ca Andalusiya ba Xorasan, ba Tugal, lonkoyoon wu àdduna bi, bu Angelo Dulcert(1339), wone na aw yoon wu romb Atlas, jeggi Sahara ngir àgg Mali: "rex Melli". Lonkoyoon wu Abraham Cresques, bi ko buuru Faraas defloo woon Charles V, bindoon na fa turu péeyam "Ciuta de Malli".

Maghan(1332-1336) moo ko wuutu

Mansa suleymaan

Soppi

Mansa suleymaan(1341-1360) mooy jubbantiwaat koom-koomu nguur gu mag ga. Gën a dëggaral kiliftéefu Mali ci Diiwaani penku yi ko wër, njiitu Tuwaareg yi bu Takedda (Ayiir), nangu woon na googu kiliftéef. Suleymaan xëccoon na Mali ay boroom xam-xam ak ay àttekat yuy tòpp Maalik. Moom ci boppam fiqh la jàng, maanaam àtte ci lislaam.

Mari Jaat(1360-1374) moo ko wuutu

Musaa II

Soppi

Musaa II(1374-1387) tegu ci, moom doonul woon ku am kàttan, xawoon naa tayyeel, jëwrinam ju njëkk la bàyee woon lépp. Moo songoon Tuwaareg yi, di def ay congam jëm Bornu

Saayam

Soppi

Lu weesu Mansa II, kujje ya amoon ci biir kër buur, te yenn saa yi rayante daan ci am, moo demoon ba faagaagal nguur gu mag ga. Ci noonu nguuru Gaawo di lekk ndànk-ndànk diiwaan yi féete penku nguur ga. Dem ba jël péeyu yaxantu bu Jenne. Doonte ci digg xarnub XV, Ca Da Mosto ak Fernadez ne woon nañu ne way dëkk yu Gammbi dañoo jàppe woon seen bopp ni ku bokk ci Mali, waaye, ci 1480, la Naba Nasere song Walata. Tekuruur jàll ci loxoy wolof yi(Jolof). Pël yu Bundu tàmbali ay yëngu-yënguy fippu, Tengela I, di ko wax it Jaje di tekki Goreelkat bi, moo leen jiite woon. Dafa bàddoo woon poseb ay yi amoon ci diggante Mali ak Gaawo daal di def li muy def. Nekkon ci dëkk bu am solo ci wàllug yaxantu, Kingi.

Imbraatóor gu Mali

Soppi

Imbraatóor gu Mali :

Nguurug Susu ci xarnu bu fukk ak ñatt tegoon na loxo ci askanu Maandeŋ. Sinjaata, doomi kenn ci buuri Maandeŋ yi, daa dogu woon ci goreel aw askanaw, ci noonu mu tawal ab xare walla am mbooloom xare (larme) mom ci la ame ndam ci kaw Susu, ci xareb Karina ba atum 1235 g.j., ci noonu la am réewam tembe woon (amoon independance). Ginnaaw bi Sinjaata amee ndam ciy noonam, la giirug Maandeŋ daje (Konaate, Traaware, Kayta, ak Kamara) taxawal ag imbraatóor gu mag mooy gu Mali gi, Sinjaata jiite ko.

Sinjaata songoon na suuf yi feggoo woon ak moom ngir boole leen ci nguuram gi, loolu nag li ko ko may mooy xareem (armé) bu am bi doole, te nosu. Bi Sinjaata di faatu Mali moo nekkoon imbraatóor gi gën a rëy ci sowwu Afrig, péey ba di woon Niaani.

Ñi ko fi wuutu woon duggoon nanu ci lislaam, wéyoon it ci yaatal gëwéelub nguur gi, ba mu mujjoon ëmb mbooleem la ko dale ca mbàmbulaanug atlas ci sowwu bi, ba ca dëkkub Gaawo ci penku bi. Ñu séddale réew mi ciy diiwaan bu ci nekk ag kilifa jiite ko guy doxal ndigali buur bi, di dajale galag yi, tey doxal yoon. Ci jamonoy buur bi Kanka Muusaa la imbraatóor gi àggoon ca gën jaa kawey ay njobbaxtalam, ci xarnu bu fukk ak ñeent. Nguur gi nag daa na jot ci màng mi tukkee ci mbelli wurus yi ak yaxantug tàkk g i. Ci atum 1324 g.j., Kanka Musaa aji woon na Màkka, ci tukki bu tollu ci 18 weer, won na ci adduna bi dooley nguuram gi ak woomleem gi.

Amaloon na ay séqoo yu yaxantu ak réewi bëj-gànnaaru Afrig, indi it ci nguuram gi ay boroom xam-xami jullit yu juge penku. Ci xarnub fukk ak juroom benn la ay jafe-jafey wuutu (xilaafa) tàmbalee feeñ, ak dagu (sécession), looloo jur néew-dooleg ay diiwaan yu bari, bu ko defee Songaay daal di ñëw songu Mali, nangu ko.

Seetal BUNTU TAARIIX
wikbaatukaay am na xët wu tudd: Imbraatóor gu Mali