Ngol
Ngol garab gu ndaw lay doon, gu bokk ci njabootug Fabaceae. Mi ngi yaatu lool ci tund Sahel wi ak Sahara ci Afrig ak ci réewi araab yi.
Melo wi
SoppiGarab gu ndaw lay doon, xaw a gudd, am xasam day liis, ay xobam guddaayam manees na koo natt ci (5-8 sentimet), ay tóortóoram day mboq. Xopi garabu ngol dees koy jëfandikoo ngir dundaleko ak jur garab gi itam leeg-leeg dana am ay tooke garab gu man a sëq lool la manees na cee wut dund ub gëleem ak xar yi ak bëy yi. Yamb yi it di nañu soxla tóor-tóori garab gi ngir man caa defar lem bant garabu ngol di nañu ko jëfandikoo ci defar këriñ man na matt lool itam xas mi man nañu cee defar buum ndox mi it dana génne daakaande waaye daakaande ji leeg-leeg du baax lool manees na cee defarn foroote itam boo jëlee xop yi dëbb ko jaxase ko man na foroote.
Nataal yi
Soppi-
Xobi ak dégi garabug ngol
-
Tóortóorum garabug ngol