New
New xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Chrysobalanaceae"
Cosaanam
SoppiNew a ngi fekk baax ci afrig soww-jant, ci digg afrig, ci Senegaal, Niseeriya, ak bëj-saalumu Sudã.
Melo wi
SoppiAg garab la gu ndaw, taxawaayam man naa àgg ba ci 10i Met walla lu ko ëpp, garab la guy sëq, ay xobam day seex. Doom bi dinay toll ci 5i sàntimet ci guddaay. Garab gi daanaka at mépp day am i doom, waaye lu ci ëpp ci ñaareelu xaaju noor bi lay am meññeef. Doom yi day nooy.
Solo si
SoppiDees na ko faral di jëfandikoo ci anam yu bari. Saal bi dees koy lekk. Garab gi nag bu màggee ci àll daay gi du ko manal dara. Doom bi dees koy witt ci ay lim yu bari a bari te di ko jëmbët ngir muy saxaat, dees koy jaay it ci ja yi at mi yépp. Xob yi niki xas mi buñu ko baxalee galaxndikoo ko day faj bëñ buy metti, sunu ko yëyee itam day faj bëñ buy metti. Reen yi aay nañu ci dereetal, sungufu reen bi itam boo ko defee ci ndox baax na ci bëñ buy metti. Dees koy jëfandikoo batay ngir faj góom rawatina góomu aji-jong ji. Saal bi it dees na ko lakk def ko dóom di ko defaree saabu.
Turu xam-xam wi
SoppiNeocarya macrophylla
Tur wi ci yeneeni làkk
Soppifarañse: pommier du Cayor |
angale: ginger plum |