Ndimbal:Sàqum jëfandikukat

Wii xët dalay wax lu sàqum jëfandikukat di tekki, luy ay ngëneelam, noo koy sosee. Di la tektal tamit yoon wi ngay jaar ak xibaar yi ngay dajeel ci yoonu soste gi, yooy gis te, xéj-na, xamoo seen tekki.

Sàqum jëfandikukat Soppi

Ay ngëneelam Soppi

Balaa dara, yeneen jëfandikukat yi, di nañ la xam, mana xammee say cëru ak say waxtaan. Ci turu jëfandikukat bi ngay tànn, lañu lay xammee (so demee bay bindu). Di na tax nga mana bokk ci aw askan wuy gën di yaa.

Su loolu weesoo di la xamal ne sàqub jëfandikukat yemul foofu rek. Soo sosee sam sàq ba noppi, Wikipedia tijjil la boppam nak! Jox la ay jumtukaay yu ku binduwul manuta jot. Ab lim bu tuuti ngi nii ci suuf:

  • Di nga am sa xëtu bopp fooy man xamalee sa bopp, man nga caa def lépp lu la neex, ci misaal: ab nataal, ay lëkkalekaay,... Soo xoolee yu ñeneen ñi man nga caa jëlee ay misaal.
  • Di nga am sa xëtu waxtaanuwaay, foo xam ne yeneen jëfandikukat yi, fa lañu lay bindee ay bataaxal. Soo amee bataaxal bu bees di nañ la ko yëgal ci anam bu gaaw(doy na nga dugg).
  • Di nga mana topp yenn jukki yi ngir mana xam ndax soppeeku nañ walla déet. Doon na lu am solo ndax soo sosee sab jukki di na tax nga man koo topp ba ab saay-saay du ko yaq, mbaa yokk ci ay xibaar yi baaxul.
  • Di nga mana soppi say tànneef.
  • Di nga mana am ab lim ci say cëru, lépp loo indi ci Wikipedia.
  • Di nga mana tuddewaat koj yu xëtu jukki yi.
  • Di nga mana yeb ab dencukaay
  • Beneen ngëneel bu am solo mooy ne sa màkkaanub IP kenn du ko gisati, ndax soo binduwul sa IP la ñuy bind (ci "Jaar-jaar") muy turu ki def boobu cëru. Loolu kaaraange la ngir sa nosukaay dina tax ba saay-saay si du ñu la mana gis, di xam foo ne, bay mana indi ay tolof-tolof ci sa PC.

Foo koy jëfandikoo? Soppi

Soo sosee am sàqum jëfandikukat ci Wikipedia wolof, foofu rek nga koy mana jëfandikoo. Kon beneen Wikipedia bu ne da nga faa wara bindu soo fa bëggee cëru.

Su fekkee jëfandikukat bi doxalinam mengóowul ak àtte yi Wikipedia tëral ngir ag yoriinam jaar yoon, yorkat yi am nañu sañ-sañu téye la ab diir ba doo mana dugal dara.

Tànn ab turu jëfandikukat Soppi

Turu Sàqum jëfandikukat Soppi

Lu weesu xibaar yi ñu la jox ci xëtu mbindu mi, mbindu mi ci Wikipedia, ci kàllaama xarala mooy "Turu Sàqum jëfandikukat".

danu koy jappee ni sa dàkkantal, jëmm gu dëggu gu jëfandikukat yi, manuñu koo xam ndaxte ku mu neek man ngaa bindoo ak:

  • Sa tur dëgg;
  • Sa tur dëgg goo xawa soppi;
  • Turu jambur boo jël;
  • Walla ab dàkkantal boo sàkkal sa bopp.

Lépp mi ngi aju ci ni nga bëgga bokke: naxasal walla jubal walla bañ ku la xammee. Xamal ne tamit sa turu jëfandikukat warul doon baat bu ñakk-teggin, baat buy wone sag bokk ci yenn mbootaay yi (politig, diine,...). Mana jur ay réeróo ak ñeneen ñi. Day tax ñuy gisee say cëru ak yeneeni gët ( ci misaal baat yu mel ne "Hitler" walla "kkk").

"Turu jëfandikukat" bi day tax nga mana xaatim say bataaxal ci xëtu waxtaanuwaay yi, ñetti ~ ngay def ci sa jeexintalu bataaxal, ngir xaatim.

Tur yi jara moytu Soppi

Man ngaa jëfandikoo sa tur dëgg, su la neexee, waaye li ëpp ci waa-wikipedia yi, ay dakkantal la ñuy jëfandikoo. Daanaka tur bu la neex jël, waaye nak am na ay dig:

  • Ab saaga manoo koo jël, ndax ni ko ñeneen ñi di gisee, su amee it di nañ sakku ci yaw nga soppi ko.
  • Bul di jëfandikoo tur dëgg bu jambur, donte ku siiw la, koo doon soppeem.
  • Bul di jëfandikoo turu këru koom-koom walla bu nit bu aqi aji-sos aar
  • Bul di jëfandikoo baat yii: yorkat; àttekat, bot,...), ndax dañoo am yeneen tekki, kon day jur jaawatle.