Lat Joor
Lat Joor Joob mi ngi juddoo ca Kër Amadu Yala, atum 1842 g.j, Saaxewar Soxna Mbay Jóob mooy baayam, lingeer Ngoone Latiir Faal di ndayam. Lat joor a ngi Meenoo ci neegi gèej
Ay meloom
SoppiLat joor waxambaane wu jàmbaare la woon, wu amoonug dogu, mu bokkoon ci ñu mag ñi daa jàmmaarlook sancaan yi ci goxub Afrig, mu nekkoon di kenn ci ñi ci gën a jàmbaare, gën cee fés, kenn melul ni moom ci bëgg rèewam ak askanam. Amoon na fit wow kenn du ko doyadil, daawul tiit ak lu man a xew. Nekkoon na njiitul xare lu mag, di aji politig ju ñaw, ju di boroomug jommal. Ci atum 1862 g.j, la ñu fal Latjoor Dammeel ca Kajoor.
Dundam ak jëfam
SoppiCi atum 1864 g.j, la ko Federb daane ginaaw xareb Loro, teg loxo ca Kajoor, Ca la Lat joor deme Siin gir sakk o lëkkëloo ak Buur Siin Kumba Ndòofeen Juuf ngir xeeq Tubaab yi waaya Buur Siin daa gantal ci ndigëlu Federb.
Lat Joor weyal yoonam, ci la deme Rip fekki fa xaritam, wólórem bu yagg di : sëriñub tukulóor ba ñuy wax Màbba Jaxu Ba,Ginaaw xare yu bari yu Lat Joor def ak xam-xam bi mu am ci wallu xeex ak nand pexey tubaab yi, ci la Almaamy Maba sakku ci moom mu jiiteel ko ay soldaaram ngir wéyal jihaad ja mu doon amal ngir gën a tassaare islaam fa Saalum ak Siin, sakku it ci moom mu yeesal ag njulitam te dugg ci tariixa Tijaan. lislaam.
Latjoor ak Màbba dajje na ñu ak Buur-Siin Kumba Ndóofeen Famak Juuf ca xareb Somb ca atum 1871,fa la ñu faate Màbba. Ginaaw bi Latjoor defaat na fa ab diir foofu ca Rib laata muy dellu Kajoor gir nangu nguuram ci loxoy Tubaab yi, mu dellu waat di Dameelu Kajoor.
Ci atum 1878 g.j, ci la Tubaab yi dogoo ak Lat Joor ci jaarale rail bi biir Kajoor muy yoonug weñ wu saxaar giy jaar ci diggënte Ndar ak Ndakaaru ngir yombal yòbbug gerte gi, waaye bi Latjoor demee ba gis ne loolu men la ci pexem tubaab yi ngir gën jekandiku ba mana dëgëral seenug nootel ci rèew mi, Lat Joor daal di bañ sakku ñu dakkal ligeey ba. daal di def ag fipp gu mag ak ay àndadoom atum 1882 ba 1883 g.j. Ci noonu xare bi tàkk digganteem ak Tubbaab yi, mu nekkoon xare bu tàng jérr waaye sancaan yi nootoon nañu Latjoor ngir néewug ay ngànnaayam aki jumtukaayi xareem ak bari gi ñu bari woon ñoom jumtukaay yooyu ñeel Tubaab yi. Ci noonu Latjoor ñakkoon pexe, daal di weeruji ca buurub Jolof ba Alburi Njaay, loolu nag di woon atum 1884.
Bi Latjoor jugee Kajoor la Tubaab yi fal Ammari Ngoone Faal muy Dameelu Kajoor, waaye gaaw nañu koo folli ngir ñaxtu gu tar ga waa Kajoor doon ñaxtu loolu. Bu ko defee Samba Lawbe Faal ñëw toog ci jal bi, mooy ki may tubaab bi mu indi fi raay bi. Waaye ak lim leen may ñu indi fi raay bi lépp teewul ñu yong ko ca wetu Tiwaawan, ñaari njiiti Faraas ñoo ko ray, ñooy Chauves ak Spitzer, ñu daal di sàkku ci Latjoor mu bañ a teggati tànk ci suufus Kajoor, waaye Latjoor bañ, dellu Kajoor. Ci noonu xare bu tàng tàkkati ci diggante Latjoor ak Salvatius, ci la Salvatius nangoo Kajoor ci atum 1886, Ñu ray Latjoor ca Deqale aki doomam ak juroom ñaar fukk ak juroom ñatt ciy àndadoom, ci 25 kori 1886. Kureelug xare (battaillon) gi ko ray Valois moo ko jiite woon.