Kureelu tembte bu Poortorikoo
Kureelu temb bu Poortorikoo bi (ci Ispaañ:partido Indipendentista Puertorriqueño), ab kureelu politigu Poortorikoo la buy yëngu ngir Poortorikoo am tembteem. Benn la ci ñetti kureeli politig ya fa ëpp solo te di it ñaareel ba fa gëna yàgg.
Jaar-jaar
SoppiGilberto Concepción de Gracia moo ko sos ci 20 kori 1946, ndax dafa jàppoon ne beneen kureel bii di Partido Popular Democrático dafa wàccoowul ak wareefam, maanaam laaj tembteeb seen réew.