Jiitalug aji taalif ji

Jiitalig aji taalif ji :


Bii mooy teereb {Irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim}, di ci maanaa nàndalug aji naanaale ji (ki ngay toogal di waxtaan) ci ndox mu neexum sopp jëwrinu yonant bi , di { xam-xamu jaloore bu nu gàttal} mu ñeel nag ki bëgg a am ab xam-xam ci dundug sëriñ Ahmadu Bamba yal na yàlla dolli gërëmam ci moom ,te jariñ ñu ci,amiin. Ki ko taalif it di ku xeebu ku aajowoo ndimbalul boroomam ak yërmaandeem,tey yaakaar ci moom mu jéggal ko ay bàkkaaram,te làqal ko ay ayibam,yi feeñ ak yi nëbbu,fii ak fan jëm,di Muhammadul Amiin JOOP doomi sheex Ahmadu JOOP mu dagana,yal na leen yàlla boole jéggal. Di it taalibeb sëriñ Tuubaa, yal na ko yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom,amiin.

Maa ngi ñaan yàlla mu musal ma ci saytaane mu nu jam mi,di tàmblee nag samay wax ak jëf ci turam wu tedd wi,moom mi yor yërmaande ju yaatu ji matale mbindéefam yi ci àdduna,te di ko jagleel ñi ko soob ca àllaaxira,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci sunu sang,Muhammad,ak ñoñam aki saabaam.

Aji xeebu ju yitewoo yërmaandey boroomam,ak ndimbalam ci ligeeyal yarkatam bii dib soppeem(di sëriñ Tuubaa) - aji xeebu jooju di Muhammadul Amiin JOOP doomi Sheex Ahmadu JOOP mu Dagana, nee na: ag cant ñeel na yàlla miy leeral àddinaam ji ci wàlliyoom yi,di feeñalati ci ñoom yoonu yonantam yiy gindee,yoon woowu di wu weetal yàlla ak jaamu ko,mooy yoonuw boroom xel yiy dàq lu dul yàlla ci seeni xel,tey jànge ag njub ca yooyale imam,ci jox leen seen bopp,jébbal leen seeni mbir. Ndax kat ñooñu, ñooy ñi yàlla naan ci alxuraan:{ ulaayikal lathiina hadaahumul laahu fabi hudaahumuqtadih} muy ci maanaa ñooñu,ñooy ñi yàlla gindi kon royal ci seenug gindi.Di julli tey sëlmël ci yonant bi.

Leegi nag ginaaw yàlla day xéewale xarnu bu ne aw waliyu wu koy gindi di ko won yoonu jub ,di ko tee jàdd, nun waa xarnub fokk ñeent nag mu defal nu,xeewal gu tollu ne sunu mbég mii di sunub sëriñ tey sëriñub julit ñi, Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah yal na ko yàlla wattu te wattul ko,te gërëmi jëfam,te méngoo ko,moom nag mbooloo maa ngi ko gën a xame ci turu sheex Ahmad Bamba MBÀKKE Xaadimur rasuul.

Bi loolu amee ma, bëggoon a leeral as lëf cig dundam, ñeel ki nar a ñëw ginaawam,te bëgg a xam dara ciy mayam. Man nag maa ngi giñ ci yàlla dellu di ci giñaat naan dey xam naa ni xawma te du ma ci man a wax mbaa indi lu dul la gën a néew,la gën a bari moom bu ko xalaat,ndax manu ma ko ba koy def. Waaye nag dinaa jéem a nooyal yoon wi,ba ku bëgg te yàlla ubbi ko, barilub xam-xamam, yinkiiwal ko jariñ jaamam yi, ngir sàkku ci ngërëmam,bu ñëwee man cee jaar,ndax kat am na ci addiiz mu sell mi: {{ mbindeef yi njabootug yàlla lanu ,ki ci yàlla gën a bëgg mooy ki ci ëpp njariñ ci njabootam gi. Nee nanu ku taarixal aw wàlliyu mel na ni dundal nga ko.

Kon am leen gàttalug jaloore (jaloore mooy taariix walla histoire) gii ma tudde {irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim},may ñaan nag képp ku ci gis lu ko yeemut, mu xam ne gàttub jéegoo ma tooñ,mu jéggalul ma Yàlla te suturaal ma,te bañ koo ngàññi,ndax kat da na ci gisi leneen lu bari lu koy yéem, lu man a wecci loolu ko yéemutoon, ndax téere bii ab muxaddima rekk la ( ag jiital) teere dëgg bi mooy {minanul baaqiil qadiim fii ma aathiris zheixil xadiim) muy ci maanaa xeewali aji des jiy aji jiitu,ci ngënéeli Sheexul Xadiim.Doomam ja Sheex Muhammadul Bashiir defoon ko,yal na ko yàlla sàmmu te guddalu fanam,te jariñ ci lu bari jullit ñi, ni baayam,moom dey teere bu boole la te wattu,te dib dër bu naat ñeel ku bëgguw yiw te di ci dox. Yal na ko yàlla mottali te nangu ko,te tas ko ci àddina bi,muy ndëxëñtéefam ëlëg ca àllaaxira,tey lu nu koy fàttalikoo ginaawam ci fii fi àdduna,ci barkeem ak ci barkeb ki ko taalif ak ki mu ko taalifal,yal na nu yàlla nangul,te nangul nu sunub teere,matal ko te tas ko moom itam. Moom kat yàlla mooy aji kawe jiy boroom ngënéel ak tawfeex,tey boroom li fii ak la fee.