Wolof (askan) wuute gi ci sumb yi

1 octet ajouté ,  12 at ci ginaaw
Coppite gi amul tënk
Wolof yi danoo jaxaasoo, lii moo tax seeni sant bari, ak tamit xeet yu bari ñëw nanu ci ñoom (Wolofal: Wolofisation). Seex Anta jóob nee na, Wolof yi dëgg-dëgg ñooy: Njaay, Jóob, Faal, Ñang, Béey, Mbóoj, Mbuub Wàdd, Gëy.
Ca Fuuta-Tooro, ca Cuballo (Nappkatu Tukuloor) walla Sebbe (Ceddo/Jàmbaar Tukulóor) Walla Tooroodo, lanu. Danoo teel a nekk foofu.
Ci Senegaal ñoom ñoo njëkk a gis Tubaab yi. Bu njëkk Ceddo lañu woon, tay ñu bari ci [[yoonu murit]] lañu bokk walla tiijaaniya. Am na ay ay nasaraan (chrétiens) tamit waaye duñu ñu bari (Gore/Ndar). [[Seex Ahmadu Bamba]] Mbakke ak [[Alaaji Maalik SI]] ñoo gën a dugal Wolof yi ci [[lislaam]]. Wolof yu bari gàddaay nanu (walla tukki nanu) dem Faraas, [[DiwaanDiiwaan yu Bennoo]] yi (États-unis), Itaali, Espaañ. Ci Senegaal ñoo yor pal yi gën a rëy (loolu du lu ñépp man a ànd, ndax gisees na ne Njiitul Senegaal lu njëkk séeréer la woon la ca topp it noonu, boo demee ca xare ba (l'armée)lu ëpp ca kilifa ya doonuñu ko. Kon wax jooju ju deesi xoolaat la). Ñoom ñoo gën a fonk seeni réewm (Nationalisme Sénégalais). Am na ci ñoñ ci Mbay (Kaw-Kaw) lanuy dunde, am ci ñoñ ci Napp, ca géej gi (ci ñoom la Lébu yi bokk). Jom ak Teraanga ci ñoom la fekk baax.
[[Catégorie:Taariixu senegaal]]
2 337

modifications