```JAMONOY FAATU NJAAY```

Xaaj bi njëkk bi *①* _____________________

Bi tàkkusaan di waaj a jot laay egsi ci jataay bi ngir teewlu waxtaan wi. Ci noonu la ustaas bi tàmbalee di lim yi ñu war a moytandiku, lu ci mel ne jëw, fen, saaga, xaste, wax ju ñaaw... Àddunaa ñàkk wor ma ! Loo am a am lu ne gàññ dafay jeex; ndimbal war na képp ku Yàlla dénk alal. Ci noonu maa ngi toogoon ci wetu jataay bi ci benn xeer. Nees kiis as ndaw jóge fële, woddoo as kumba jiital lu kenn xamul. Ma ngay ñëw. Di wax ak a sànn i yoxo yi. Dafa wéradi. Feebaru xel moo ko dab ca daara ju mag jamu daan jànge. Yëf yi nag, rax na ag reewande. Ndax du xaar lu dul mbooloo mu daje; mu ñëw ak i waxam ju bon. Moom Faatu Njaay mii xel mi wéradi, dëkk bépp dañuy muslu ci moom ndax làmmiñam wu ñaaw. Ci noonu, ustaas Siise mi yoroon waxtaan wi, tooyloo na xol yépp. Waaye ay jibaam duuf na ak xaalis. Waxtaan wi daal neexoon na ndax bi waxtu julli jotee dañu ko faa bàyyi. Bañu noppe, mbooloo mi dañoo tàggatoo ba beneen, bàyyi Faatu Njaay ak i waxam ju bon. Bi waxtaan wi jeexee, moom Faatu Njaay dafa daal di topp Ustaas bi langal ko ko. Fumu jëm, mu riig ko ko. Wax na dëgg sax ! Ndax Faatu dafa yàgg a nob Ustaas bi. Waaw! Seen i mbir ca daara ja la tàmbalee. Man mii di wax ak yéen xam na ci dara ndax ndaw si sama xarit la woon. Bi ko feebar bi dabee ba leegi dama koy daw. Lu ko moy dinama sullil ay mbóot. Waaw ! Yàgg na maa sonal ci limatu Ustaas bi. Moom dafa nekkoon ku góorewu, man a solu, am diine. Waaye kenn du Faatu. Dafa refet, ree ji neex lool, gëñ yi weex tàll, mu am daaguwaale Ku ko xool bëgg ko ndax bari jàmm. Ci nimuy toppaate, Ustaas baa ngi koy moytu ndax bëggul a am benn xaar ma Yàlla ak moom. Waaye Faatu bëggul lu dul raay sikkimu Ustaas bi.

_Aji-nettali ji:_ Kàddug Kajoor

Ci Mbind mi: Maysa Ndaw.