Jàngoroy Ebola
Jàngoroy Ebola ñu gënoon koo xamee ci Jàngoroy yaram-wu-tàng ju Ebola jenn xeetu jangoro la juy dal nit walla yenn bàyyima yi te doomu-jàngoro bu ebola di ko joxe. Xàmmeekaayu jangoro ji mi ngi tàmbalee feeñ ci diggante ñaari fan ba ñetti ayubés ginnaaw bi la doomu-jàngoro bi duggee, ngay ame yaram-wu-tàng, put guy metti, sidit yuy metti ak bopp buy metti. Ginnaw feeñte yu njëkk yii, naka-jekk, yi ciy topp ñooy, xel-muy-teey, waccu ak biir-buy-daw. Su ñu àggee fii ci jàngoro ji, ñenn nit ñi dañuy tàmbalee am ay nàcc-nàcc yu man a nekk ci biir yaram wi walla ci biti. Repp gee dee ci nit ñi ko amee dina àgg ci dayoo bu réy.
Jàngoro ji manees na koo jël ci boo laalee dereet walla wal-walaan yu yaramu ab bàyyima (golo walla njugup) walla nit ñu ko am. Ba tay jii jàppees na ne maneesul a wàllante jàngoro ji jaare ko ci ngelaw li ci ab barab.
Ginnaaw bi ko kenn nit jële, jàngoro ji man naa tas jaare ci moom. Ñi ko ame ba wér ci man nañoo wéy di ko man a wàllaate ñaari weer ginnaaw seenug wér jaare ko c seen manniwa.
Amagul genn xeetu pac gu wór gees xam ngir fac njangoroy Ebola. Xeetug pac gi gën a jàppandi ci jamono jii mooy di leen jeem a naanloo ndox mu doy (di ndox mu am tuuti suukar ak xorom) walla ñu leen di sol ay wal-walaan. Jàngoro ji ju man a rayaate la, lu ci ëpp ci 50% (juroom-fukk ci téeméer) ba 70% (juroom-ñeent-fukk ci téeméer) ci ñi muy dal ci dee lañuy mujjee. Jangoroy yaram-wu-tàng ju Ebola ñoo ngi ko njëkkeen gis ca Sudaan ak ca Kongóo. Naka-jekk njàngoro ji dafa daan faral di yem rek ci yenn barab yu ndaw yu beru ci yenn réewi Afrig yu ron-sahara yi. Ci atum 1976 (di at mi ñu ko njëkkee gis) ba 2013, lu néew 1 000 nit ci at mu nekk daan nañ ko jël. Wàllante gi gën a réy gu Ebola moo ngi ame ci ndoorteelu 2014 te barab yi mu gën a tasee ñooy réew yu Gine, Siraa Leyoon, Libeeria a Niseeria. Ci oktoobar 2014 jappees na ne lu mat 10 000 nit jot nañu koo am.
Lëkkalekaay yu biti
Soppi- Ebola Virus Haemorrhagic Fever - Proceedings of an International Colloquium on Ebola Virus Infection and Other Haemorrhagic Fevers held in Antwerp, Belgium, 6-8 December, 1977
- Questions and Answers about Ebola Hemorrhagic Fever - Center for Disease Control (CDC), retrieved 10 July 2006
- www.healthocrates.com - Articolo sulla febbre emorragica dell'Ebola