Internet
Internet (di jàng in-ter-net, jóge ci baatu latin bii di inter=diggante ak bu wu-angalteer bii di net=lënd) moom lañu jàppe niki lënd gi gën a rëy ci àdduna bi, te boole ay junni-junniy nosukaay lëkkale leen ci seen biir.
Mi ngi judd ci ati juroom-benn fukku yi niki ab sémb bu kuréel gi yor kaaraange ca Diiwaan yu Bennoo yi ngir sos ag lonkoo ci seen diggante, ci njeextal xare bu sedd bi lañu ci yaatal ñeneen ñu dul yëngu ci kaaraange rekk, lëkkale daara yu kawe yi gën a mag, ci lu njëkk, ba yàgg mu àgg ci yenn liggéeyuwaay yi, ci noonu lu muy gën di dem di gën a yaa ba àgg tay ci sunu kër yi.
Aw ràbbiinam
SoppiInternet man nanu koo jàppee niki ag lonkoo gu xellu te fasu teg ci, cëslaayu ci fànni jumtukaay ak xeeti lonkante gu ne, lëkkale leen ci seen biir.
Jumtukaay yiy lonku ci internet lees di wax host(di tekki gan ci wolof) walla end system (nosteg njeexte ci wolof), mbir miy jokkale host yi la ñuy wax lëkkalekaay.
Mbaalu mbaal yi
SoppiNaka-jekk Internet «mbaalu mbaal yi» lañu koy dakkantale. Naka-noonu ay lonkoo yu bare lonkante doon ko: lonkoo yu kenn, yu mbooloo, yu ay këri-koom, yu ay daara yu kawe... Ag juddoom ak ag màggam gu gaaw, bokk na ci li ko waral, mooy bennal gi am ci xeetu jokkoo ci diggante lonkoo yi, waral weccontey xibaar man a am ci diggante ay jëfandikukat yu soriyante(yu mel ne nguur-ak-nguur, daara-ak-daara, këru-koom-ak-këru-koom, ak ñoom seen, te jumtukaay yi muy jëfandikoo amuñu ci benn njeexit.