Imbraatóor gu Songaay

Imbratóor gu Songaay :

Carte de l'empire songhai

Ci juroom ñaareelu xarnu g.j., la askanu Songaay wi dëkkoon ci tefesug dex gu Nijeer gi taxawaloon ag nguur gog péeyam moo nekkoon Gaawo. Mali nag moo tegoon loxo askanu Songaay wi ci xarnub fukk ak ñatt g.j., waaye ñoom jotaatoon nanu ci seenug temb te ñi ko waral di njabootug Soni gi ci xarnub fukk ak ñeent, daal di tàmbalee naat. Soni Aal-Béer (maanaam Aal mu mag mi) moo nekkoon buur bi la ko dale ca 1464 g.j., ba 1492 g.j., wutaloon na nguurug Songaay xare (armée) bu am doole, mu daa def ay ubbi (conquête) ngir yaatal nguuram gii nga xam ne mujj na tuxoo ci nguur dem cig imbraatóor gu ñu mujj tudde Songaay walla Gaawo. Bi Aal Béer dee la kenn ci ay njiiti xareem teg loxo ci nguur gi, daal di wutal boppam dàkkantalu Askiyaa (maanaam imbraatóoor bi), moom nag àtte na ba ci 1528 g.j., mu gën a rëyal mbooloom xareem mi, wéy ci ubbeem yi, bu ko defee imbraatóor gi mujj tàlleeku dale ca mbàmbulaanug atlas ba ca Borno ci penku bi, dalewaat ca Jini ci wàllug saalum gi ba ca digi Marog ci wàllug bëj-gànnaar gi. Gii imbraatóor nag àggoon na ci njobbaxtalam ci jamonoy Askiyaa Muhammad. Buur bi moo daa jox ndigal foŋsaneer yi, di lijjanti diiwaan yi, benn gongikuwaayu alal bi nguur gi amoon mooy yaxantug tàkk gi.

Nguur gi nag, réew yi mu feggool xuppoon nanu ko : ci atum 1591 g.j., buurub Marog yabaloon na ab xareem ñu jaar ci tàkk gi ngir song Gaawo, moom nag amoon na ndam ci waa Songaay ngir ngànnaayi sawaraam yi mu jénde woon ci waa Tugal yi. Ci nii la Songaay tàmbali woon di doyadi ak di dagu.

Seetal BUNTU TAARIIX