Imbraatóor gu Gana
Imbraatóor gu Gana gi mag ci yu Afrig yi taariixkat yi mas a xam mooy : gu Gana. Li ñu jot a xam ci taariixam ñi ngi koy sante gëstuy boroom xam-xami jeexiit yi, ak nettaliy gimiñ yi, ak mbindi tukkikati naar yi.
Gana mi ngi sosu ci ñeenteelu xarnu g.j., jamono jooja it nguur gu ndaw la woon gu ñu daa woowe Ogaadoo. Ci juroom ñatteelu xarnu g.j., la ab xareem (son armée) jugoon song ay suuf yu yaatu, yu nekk ci diggante dexug Senegaal ak Nijeer, ci noonu la Gana wëlbatikoo di imbraatóor gu mag gu teg loxo ci dëkk yi mu feggool…
Imbraatóor gi nekkoon na di gu naat : ay suuf yu nangu mbay ak sàmm, mu daa bokk ci yaxantug tàkk gi (gi nu daa defe ci tàkk gi) ak njaayum wurus mi, moom imbraatóor gi amoon na ay mbelli wurus yu bari yoy ki ko daa topptoo mooy Kayaamagana, maanaam njiitul wurus li : waa jii da daan nekk njiit lu dëgër, lu ñu wormaal, luy àtte cig maandute te daan samp foŋsaneer yi. Moom nag cim koom ak naataange la daa dunde ci péeyam, waa diiwaan bii it dañu ko daa indil ay kem ci wurus wi ñiy génnee ci suuf si, ginnaaw bi mu faatoo nag la ko fi ab jarbaatam wuutu. Ci atum 1052 g.j., la Muraabituun yi song Gana, ci layuw dañuy dugal ñoñam ci lislaam, ñu daal di ubbi péey ba atum 1076 g.j., ginnaaw bi Gana néew doole, daal di daanu ci mujjantal gi ci loxoy imbraatóor gu Mali atum 1240 g.j.
Seetal BUNTU TAARIIX |