Hip-hop
Hip-hop ag yëngu-yëngug caada ak fànn la, mi ngi juddoo ca Réew yu Beenoo ya ci ndoorteel ati 1970 yi, daa boole bànneexu ak ñaxtu. Mi ngi juddoo ci biir askani waa-aamerig yu ñuul yi, ca New York, fa la tàmbalee, mujj tas ca réew ma ba ci àdduna bi bépp, ba tay mooy dundiinu réewu-taax wi ëpp doole. Caaday Hip-hop ci ñeenti ponk la tënku: break dancing, DJing, MCing ak graffiti.
Wii xeetu fànn ñu bari ci woy wi lañ koy tënk ,MCing, te mu gën a siiw ci rap. Caadaay Hip hop yamul rekk ci rap, man naa sol mbubb yu wuute: su fekke danuy yam rekk ci xoosug DJ bi (Disk Jokey), waruñu ko tuddeeti rap, waaye DJing , sunu yamee ci li MC bi (master of ceremonie, njiitul xew) di bàcc kon man nanu koo woowe rap, walla tamit, donte bari na lu muy faral di am, boolee benn DJ ak ay walla benn MC, kon ci nii hop-hop lañuy wax, ndax rap ak MCing yépp ci caadaay hip hop lañu bokk, waaye nit ñi rap lañuy wax rekk yam ci ngir yombal.
Cosaanu baat bi
SoppiCosaanu baat bi taxu koo leer noonu, ci ñenn ñi jëfandikoo-xel ngir tekki
- Hip "muus", "am-xel" lay tekki, muusaayu tappalaatukat.
- Hop ag yuuxu la gu kuy tëb di def (sooy tëb ni op!).
Nee nañu baat baa ngi war a bawoo ci DJ Luv Bug Starski mi ko doon faral di jëfandikoo suy wax. Waaye li wér te wóor mooy ne gandoor bu Sugarhill Gang mooy ki ko siiwal ci àdduna bi, ci seen woy woowu Rapper's Delight, di benn ci woyi rap yi ñu njëkk a def k7.
Taariix
SoppiAy cosaanam
SoppiWoyu hip-hop ci buumu xeeti woyi waa-aamerig yu ñuul yi la bokk. Ay dàttam ñi ngi bàyyikoo ci dundiin gu metti gi ñu nekkee woon, dalee ca seeni maam ba ci jamono yi muy juddu, woy yañu daan def ca tool ya daan ca naqarlu seenug nekkiin, ak daan ca fattali seenug jóge Afrig. Mi ngi tàmbalee ciy kebetu niki xeeti woy yu mel ne ragetime, jazz, blues. Ci lu gën a jonjoo, woyu hip-hopa ngi bawoo ci Soul, ak ci funk. Yii xeeti woy bawoo bëj-gànnaaru Aamerig dem ba fasook sound-system bu waa-jamayka, bi àgg ba New York ndax ndoxandéemu gi waa-jamayka yi daa def foofa. Ba tax-na ñett ñi ñu ne ñoo sos yëngu-yëngu hip-hop fa lañu bàyyikoo.
Donte hip-hop ci yii xeeti woy la jële ay dàttam, waaye doonul seenug wéyal. Du lu ay tëggkat yu xereñ ci seen liggéey toog xalaat, ni blues doonee wéyalug jazz, gospel juddoo ci blues, soul tegu ci, funk ñëw, caaday hip-hop dafa am ab dog-dog ag yeneen xeeti woy yooyu
Aji-rap yi njëkk
SoppiLes premiers rappeurs et groupes de rap qui ont marqué l'histoire sont :