Guy
Guyug Afrig bokk na ci juróom ñàtti guy yi ñu gën a xam, mi ngi bokk ci njabootug Bombacacees. Guy garab la gog dañu koo fonk lool ci aada ak cosaan, ñi ngi koy fekk ci barab yi am naaj fu ci mel ni réewum Senegaal ak Ginne.
Melo wi
SoppiGuy, garab la gog peeram da fa yaatu lool man a denc ndox mu bari, loolu moo tax ñu di ko woowe grabug butéel. Ci guddaay mi ngi toll ci ñaar-fukk jàpp ñaar-fukk ak juróomi ñay ci yaatuwaay mi ngi toll ci juróom jàpp juróom ñaari ñay. Bokk na ci garab yi nga xam ne day jël reenam dugal ko ci biir suuf ngir wuti ndox mum dunde. Guy garab la gog manut a dékku ngelaw lu tar lool.
Satamànna
SoppiSatamànna mooy xobi guy yu ndaw yi. Moom nag dees koy jëfandikoo bu baax ci yenn barab yi. Dees koy watt di ko def laalo di ko boole ak cere. Jur gi it bëgg nañu ko lool. Guy nag nawet kepp lay sëq am i xob, waaye yeneen jamono yi du am dara. Fu mel ni Kaasamaas nag, ca Senegaal, dees na fa fekk guy yoo xam ni at mi yépo dañuy sëq. Xobu guy nag, dana yaatoo 20i milimet.
Mbotmbotaan
SoppiBotmbotaan mooy tóortóori guy, moom nag day weex. Ginnaaw bu feeñee ba dem manees naa séntu wuy. Ba xiif di am daahees na ko lekk.
Cëggal guy
SoppiCëggal guy mooy xànci guy. Ca bu njëkk, dees ko daa xànc di ko weer di ci defar ay buum. Goj yi ñuy roote ci lees ko daa defare.
Wuy
SoppiWuy wi di meññeef mi ñi ngi koy natt ci ñaari téemeer ak juróomi garaam, ci yaatuwaay mi ngi toll ci téemeeri milimet walla mu jàpp sax ñaar fukk i sàntimet ba ci sax fan weeri sàntimet ci guddaay. Man naa am ci biir lu ëpp 300i doomi buy.
Buy
SoppiBuy, mooy ñam wiy nekk ci biir wuy wi. Doom bu weex lay doon bu neex. Manees na koo macc noonu, manees na koo def njambaan mbaa njar. Ca Senegaal dees cay faral di def cifaay di ko boole ak laax.
Gif
SoppiGif mooy xooxu buy. Boo maccee buy bi bamu set xoox ba cay des mooy wuy. Aw meloom day ñuul, boo ko tojee it day am aw kemb ci biir. Gif moomu nag moom jur guy, moom la ñuy ji. Wolof da ne: Lu guy rëy rëy gifay ndayam.
Xetax
SoppiXetax mooy lu nëtëx liy muur xottu wuy. Bu taqee ci yaramu nit day xasan lool. Dees ci daan taal. Bu ñaar yi jonjoo, riisoonte man naa jur sawara.
Turu xam-xam
SoppiAdansonia digitata
Tur wi ci yeneen làkk yi
Soppiaraab: الباأوباب شجر إستوائي |
farañse: baobab |
angale: baobab |
itaaliyee: baobab |