Fuuf xeetu gàncaxu tóortóor la gu bokk ci njabootu "polygaceae". Dees na ko jënfandikoo ngir ay jagleem ci wàllu njaay ak paj, ci pajum coosaanu Afrig.

Nataalu fuuf

Melo wi

Soppi

Ñax la gees di buddi ngir ay reenam. Barab yi tàkke lay faral di ne: Burkinaa Fasóo, Sudaan, Senegaal. Beru la baaxoo te guddaay danay àgg ba 5i met.

Oktoobar ba nowambar lay tóortóor, tóortóoram wirgow ngolleñ bu dër la yor te day gilli xet wu tar te saf suukar. Fuuf bi danay des ci fuuf gi lu mat weer.

Njariñ li

Soppi

Xooxam danay jariñ ci wàllu aniin, ginnaaw biñ ko dëbbee te togg ko toggu ko yem. Diwam suñ ko nalee, njariñ la ci jagal kawar ak der. Dawam siiw na ne tooke la ci biir.

Reenam lees di fajoo la ci pajum cosaanu Afrig.

Njariñal paju garab gi ci yaatal yii la:

-Toppatoo mettiitu gëñ. -Xeet egsemaa -Xam, ngénnaliku der. -Néewle dereet

Nataali fuuf

Soppi

Turu xam-xam wi

Soppi

Securidaca longipedunculata

Turam ci yeneeni làmmiñ

Soppi

Araab: Farañse: