Weeru Fewirie mooy ñaareelu weer ci arminaatu Gregori ak ci bu Suul.

Fewirie, Leandro Bassano

Baat baa ngi jóge ci latin: februarius, ngir màggale ko yàllay waa-rom ja: Februa. Ca jamono ju yàgg ja, moo nekkoon ñaareelu weer ci arminaatu waa-rom, at mi 15 Maars la daan door.

Mooy weer wi gën a gàtt ci at mi, mooy wenn wi dul àgg mukk 30 fan.

Weer
Samwie | Fewirie | Maars | Awril | Mee | Suwe | Sulet | Ut | Sattumbar | Oktoobar | Nowembar | Disambar