Diiwaani dott

(Yoonalaat gu jóge Diwaani dott)

Diwaani dott yu àdduna bi ñooy barab yi ne ci li wër dott yi. Goxub Dottub Bëj-gànnaar dan koy jox tekki yu bari; da nuy wax ne mooy mbooleen suuf yi ne ci bëj-gànnaaru Mbegeb dott bu Bëj-gànnaar bi, walla suuf yi ne ci rëddu tus-wu-gaar wu 60° (60 aj) ci bëj-gànnaar. Goxub Dottub Bëj-saalum moom daanaka kenn du ko yemale ci Mbegeb dott bu Bëj-saalum da nuy wax ne mooy mbooleem suuf yi ne ci rëddu tus-wu-taxaw wu 60° (60 aj) ci bëj-saalum.

Diwaani dott yi ñoo gañcax

Li ñuy gën a xammee diwaani dott yi ñooy seeniy jamono yuy nangoo sedd, li nuy wax klimaab dott. Diirub nawet naaj bi di na am 24 waxtu (li ñuy duppee naajub xaaju-guddi), diirub noor nak day lëndëm rekk sax-dàkk.

Bari na nak ñi dëkk ci barabi dott bu bëj-gànnaar, waaye bu bëj-saalum kenn dëkku fa, lu ko moy am na ay sañc ngir ay gëstug xam-xam, ci wàll wi gën a féete suuf ndax lu mu gën a sedd.

xool it

Soppi

Lëkkalekaay yu biti

Soppi