Dimb
Dimb garab la gu jub te gudd lool guddaayam man naa mat juroom ñeenti met ba ñeen fukki met.
Barab yi
SoppiDimb di sax nag yii la: Senegaal, Mali, Niseeriya ak Kamerun.
Doom bi
SoppiDoom bi dees koy lekk ci tooyaay bi ak bu wowee itam saal bi it dees koy lekk nit ak mala yépp a ci yam. Mutt-mutt di doomu dimb bu ñor bi, moo gën a neex keŋ. Keŋ mooy doom bi ñoragul. Àllambere mooy der biy muur saal bi. Saalub dimb it lu am solo la.
Bant bi
SoppiBant la bu ràññeeku ci bant yi ndax talaayam ak dëgëraayam, max manu koo yàq. Dañ koy jëfandikoo ngir defar ay lal ak i armuwaal yu rafet te man a yàgg.
Njariñ yi
SoppiDimb garab gu ñaas, am xasam di lekkloo tey faj saw-lal, day faj lu bari, bokk na ca ray jaani-biir, di ko daggte ba nga koy saw, garab gu baax ci suuf ngir ne lu meññ ci ronam màgg te naat, boroomug kër gu neex la te amadi dég, ker gu dége mooy gu picc yay toŋ cag garabam te di fa tàgg ba toog fay jafe.
Turu xam-xam wi
SoppiCordyla pinnata
Tur wi ci yeneeni làkk
Soppifarañse: poirier du Cayor |
angale: Cayor pear tree |