Ci xam-xamu nosukaay, ab dencukaay walla ab taxañ, ab ëmbukaayu ay xibaar la. Dencukaay yi, dañu leen séeddale ci ñaar: yu ëmb ay mbind "dencukaayub mbind" ak yu ëmb aw yoon wu ñaarñaarloo "dencukaayub ñaarñaarloo". Cig xarala, njoxe yi nekk cib dencukaay dañu leen nos niki ag callalag ay bit, ñu boole leen niki benn cër bu ñu rënk cim xel mu yaa. Dencukaay bu ci nekk day am tur, naka-jekk dañu leen boole ciw ŋara wu leen di ëmb.

Ëmbiitu dencukaay bu ci nekk day am wenn melokaan wi, te melokaan wu ci nekk ak xeetu tëriin way man a firi walla soppi ëmbiitam. Nosukaay bu nekk day am li ñuy wax ag nosteg doxiin, te moom mooy am ci biiram tëriin yiy tax ngay man a ubbi, tëj, bind walla jàng ab dencukaay. Yenn nostey doxiin yi (walla doxaliin yi), yu ci mel ne Microsoft Windows ak MS-DOS, ci lawal gi ñuy yokk ci turu dencukaay bi lañuy xàmmee melokaanam ba man a firi ëmbitam, gu mel ne Mac OS moom yenn jéenginjoxe yu ñu dugalaale ci biir dencukaay bi lay jëfandikoo, geneen gu mel ne Unix moom, ngir xammee xeeti dencukaay yi, ñaari byte yi njëkk ci ëmbitam lay xool.

Ay màndargaam

Soppi
  • Dayoo bi: moo lay wax ñaata xibaar lañu dëxëñ ci biiram, ñu koy natt ci bit (misaal, dencukaay bii am na 1024 bit).
  • Dayoo bi ci jëmm: moo lay wax dig-digal bi ñu jàppal dencukaay bi ci xel mi ngir man ko faa téye, aki màndargaam. dayoo bi ci jëmm naka-jekk mooy ëpp tuuti dayoob dencukaay bi.
  • Lawal gi: lu ñuy yokk ci turu dencukaay bi la ngir muy xamale ci melokaanu ëmbitam, dina tax tëriin wu koy ubbi di ko jàng xam nan lay firee ëmbit li, ndax dencukaay bi man naa ëmb ab nataal, walla ab dégtal, walla ab wideo...

Xeeti dencukaay

Soppi

Ab dencukaayub mbind man nañoo firi ëmbitam mu doon ay mbind lees man a jàng. Safaanokg dencukaayub ñaarñaarloo, moom kenn manukoo jàng ndax ay '0' aki '1' la ëmb.

Ngir nosukaay yi man a xammee màndarga mu nekk, dañoo defar ab xaatim duppee ko ASCII, ci wu-angalteer (American Standard Code for Information Interchange) ak lawalam ISO 8859 , màndarga gu nekk 8 bit lañ koy binde. Loolu tax nosukaay bi su gisee 8 bit yooyu di teewal benn màndarga, man koo xammee won la ko (misaal: 1100001 mooy arafi 'a' ).

wikbaatukaay am na xët wu tudd: Dencukaay