Balaam
Ci làkku ibrë (בִּלְעָם) la tur wi jóge. Ci angale mooy Balaam; Ci faranse mooy Balaam
Ku mbubboo turu yonent la woon, te fexe woon a rëbb bànni Israyil, ngir sàkku alal ca jamano Musaa. Bokkul woon ci Yawut yi. Gisaanekat la woon itam. Dafa digal buuru Mowab Balag, ñu jéema boole waa Israyil ak jaamu xërëm. Loolu moo tax Israyil rey nañu ko. Man nañu jàng ci jalooreem ci Nu 22:1-24:25; 31:8; De 23:4-5; Jos 13.22; 24:9-10
Injiil moo wax ci Balaam ci 2Pi 2:15; Yu 1:11; Pe 2:14.