Aretas
Ci angale mooy Aretas; Ci faranse mooy Arétas
Aretas IV Filopatiris, buur bu jóge réewu Arabi la woon. Jamanoom moo doon 9 j.K. ba 40 g.K.. May nañu Erodd Antipas doomam bu jigéen. Waaye Erodd dafa ko fase bi mu bëggee woon takk Erojàdd. Aretas yónni na ay xarekatam ci xare ngir xeex ak Erodd. Mu noot ko ci 36 g.K.. Aretas teg na benn jawriñ ngir yilif dëkku Damas. Kooku jéemoon na jàpp Pool.
Turam moo feeñ ci Injiil ci 2Ko 11:32.