Arabi
Ci angale mooy Arabia; Ci faranse mooy Arabie
Ci jamano Injiil ji, diiwaanu Arabi moo fare woon penku ak bëj-saalumu réewu Yude, maanaam wàllu bëj-saalumu réewu Yordani (Jordanie) ak wàllu bëj-gànnaaru Arabi sawuditt (Arabie saoudite). Nekkul woon lu ñuy wax diiwaanu Arabi tey jii, maanaam lépp lu nekk ci diggante Géej gu Xonq ak Géeju Pers (golfe Persique).
Man nañu fekk tur wi ci Gal 1:17; 4:25.