Arafu T

Toroxlul te tuub tey topp Yàlla te teet tereem () te teey tabe tey tàggat bakkan beek a daw pexeem

Toŋal ko te tóngook moom te tëkku ko bul ko tëy () toroxlu ci Yàlla’akug tëyam sàkku yërmandéem

Te bul toog te bul jëf it ci maa tey mu tund lool () na tandu te bul teeŋal ku të tukku tuskareem

Tegul yaw ci kaw yoon wii taxañ bulk o teggi tam () te bul taga-témbéekug tàyyeel ak lu deesi yéem

Te daw tabarondum digg njolloor mi ngay taseel () mu teggilook’ay tàbbiloo teeni tappaleem

Fegug Yàlla moo gën gën ji tunkaar akiy tata () nangay tàbbi kaaraangeem te bul génn bul ko jéem

Te taafenteloo nag aw turam foofu man di dem () te ngay tos sa xel ba’m saf ku dul yaw nga far ko tiim

Nga totti sa xol ba’m set ci tër ak tilim-tilim () te muñ tiis akiy tar-tar ba gis tërgënub taneem

Te daw tañaxook tànjang ci mbir moo xalaatagul () te daw tumurànkeg xam nangay tabb cig wuteem

Nangay tànn say àndaale tey tànnu taaru jëf () te tàmmal sa làmmiñ wax ju yiw mbaa nga far ne xiim

Te tooke sa bànneex far ko tiiñal te tanc ko () tëjjal ko tàbbal ko ciy pexeem

Nangay tembareel say mbir sa jëf takku am njariñ () nga lal tesarantag muñ te bul tayle gor ci keem

Te ngay bàyyi tiisanteek a teefonke ak tërëf () te taataar toroxlul nag ka deesul gis’ag tëleem

Te tapp ca xéewal yee te jug tepp-tepp yii () te tàggooki tër ak taq tey fob teraanga leem



 Wonante ginnaaw
 ragal
 Ñaaw ñaaw gu ëpp 
 bari
 Yanu; sëf; gàddu 
 Wéy te dem 
 Tabarond:màggat  
 Ay bali fett walla defukaayam
 Fegukaayu bali fetal; fort ci fr maanaam fi soldaar si di làqu di fa aaroo cib xare  
 Tuddoo ak sukkandikoo
 fiime
 fóot
 Jeexiitu aw mettiit nekkoon
 Tànjang ci mbir tëb tëb tàbbi ci 
 Dëkk ak sax ci dara 
 baax
 Posone 
 Lakkal witt
 Tas ci diggante bu xat
 Wéradig tànk la guy tee man a dox, fas lay faral a dal  
 Jampal 
 Tesaranta: ag basaŋ   
 Kee : Xaalis ak wurus
 Xëccoo 
 Jaaykatu xar, mu jublu ci werante 
 fakastalu
 Saaraan 
 As taa-taa su ndaw