Bul garab la gu am ay xob yu tasaaroo ak peer buy gudd lool bu man a àgg ci fukk ak juroom ñatt ba ci ñaar fukk ak juroomi met ci njoolaay. Ci gëx bi di njëlbeenu peer bi dana yaatu ba àgg ci juroom benni met peer bi nag ci boppam man naa dem ba ci lu ëpp met ci xala ci yaatuwaay.

Bul gi (Celtis toka)
Bul gi (Celtis toka)

Njariñ yi

Soppi

Garab gi ay njariñam manees na cee faju man nañu koo jëfandikoo ci matt walla sax ñu di ko lekk. Ci wàllum paj xas mi man naa faj ay tànk yuy ruux walla tànk yu ab sedd di jàpp. Reen yi man nañu koo jëfandikoo ngir faj feebaru xel. Yu bari ci garab gi it man nañu koo jëfandikoo ngir faj tële ak faj bopp buy metti ngir faj ay picc ngir faj yaram wuy sol ndox ngir faj coona walla it nu man koo jëfandikoo ngir di ci faj i goom walla di ci faj i saan man na it yombal njurum jigéen maanaam jigéen juy wësin dena ko koy yombalal.

Jëfandiku gi

Soppi

Leneen ci ñariñ yi: Garab gi man nanoo jëfandikoo xas mi ngir defar ci ay basaŋ walla am ci matt mu ñuy togge.

Mbay mi

Soppi

Bul garab la gu ñuy ji waaye ji gi bu jàppee màgg gu gaaw lay man a màgg. Manees na koo jëmbat it, boo amee nduutan gi di njëmbat, man nga koo jëmbët.

Nataal yi

Soppi

Turu xam-xam wi

Soppi

Celtis toka